LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (Alxames 22 desàmbar 2022)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG                           

Taxawaayu Seex Abdu Baara Dolli ñeel wotey 2024              

Dépite bii di Seex Abdu Baara Dolli biral na  yéeneem ngir nekk Njiitu réewum Senegaal ci wotey 2024 yi. Moom nag xamle na ne dara terewu koo nekk lawax ca wote yooyu donte ne sax mi ngi bokk ci lëkkatoo gii di Wallu Senegaal. Te, nee na dafa jot ñu jox réew mi doomi daara yi ndax ci réew mi lañu bokk. Nee na, fii ak ñeenti weer, dina amal am ndaje ca Mbàkke ngir mu xam ndax ay ñoñam dinañ ànd ci loolu.        

Mbir yu yees ci coowal Aji Saar-Sonko      

Coow loolu nag yëngu na lool ci jamono jii. Ndax, ci lu yàggul dara dañoo woo woon kii di Baay Mbay MC, mu am ay mbir yu yees yu mu ci waxoon. Moom nag dafa xamle woon ne dafa am ay ndéggat yuy firndeel ne coow lii ay caaxaan la, ag ciif amu ca. Démb nag la am ci ndéggat yooyu yu ci génn mu bari nag mbir yu muy leeral ci ciif gi ak ñi nekk ci ginnaaw.

Kàdduy Mansuur Fay ñeel caabalug ëttub cettantal gi                

Nee na nag moom dafa namm a teggi li ëttu cettantal gi teg ci deram ndax nee na xamul nees mën a tuumaalee as gor ci loo xam ne teguñu ko dara. Moom nag dafa bëgg yiin topp kii di Aliw Sow mi nga xam ne mooy DAGE (directeur de l’administration générale et de l’équipement) bi donte ne jàppees na ne mooy ki gaa ñi duut baaram, bu nu sukkandikoo ci li jot a rot.                                                                 

NJÀNG AK NJÀNGALE 

Coow diggante ndongo ak Njiitu daara ja

Coow loolu ma nga xewe ca Sigicoor diggante lenn ndongo  luy wuyoo ci turu M.D ak lenn Njiitul lise (Proviseur) lii di Keeñaa. Ñoom  nag seen coow li mi ngi sosoo ci benn ñaxtu bu ndongo yi doon amal, te ñoom ca jeneen daara lañu jóge woon (Jibok) ngir génnee seen naataango yooyu ngir ñu dimbali leen. Ca loolu la Njiit la àndul woon nag ba ñu jot ca jokkalantey kàddu. Ca la NJiit la jaar nag, pelent ko, ñu teg ko loxo. Ay layookatam nag xamle nañu ne song Njiit li taxu ko woon a dem foofu, ñaxtu baa ko fa yóbbu. Moom nag dinañu ko àtte fukki fan ak benn ci weeru saŋwiyee wii ñu dëgmal.                     

WÉR-GI-YARAM                           

Luubalug 60i Miliyaar Ca Raglu Bu Tiwaawon                        

Coowal luubal googu nag moo lëmbe raglu bu Maam Abdul Asiis Dabbaax. Te, ba tey, ñi ko def xamaguñu leen. Gaa ñaa ngi jéem a xam ñan ñoo def loolu ndax kat lu yàggul dara foofu la fukki liir yi ak benn ñàkke woon seen bakkan.                                      

XEW-XEWI JAMONO                         

Xew-xew bu tiis ca Pikin                

Ca diwaanu Pikin, benn xale bu tollu ci fukki weer ak juróom moo fa daanu ci benn foos. Xale bu jigéen boobu mo ngi wuyoo ci turu M.J.B. yaayam dafa génnoon dem ci këru dëkkandoom yi bàyyi woon ko ak maamaam. Bi mu ñibbisee di ko wër, fekk na mu daanu na ca foos ba, daldi lab, faatu.             

Beneen Xew-Xew Ca Kër-Masaar                                             

Lii nag, benn sëriñu tariyaa lañu fekk mu ñàkk bakkanam ci koñ bii di Àllaaji Paate bu Kër Masaar. Moom nag, ay dëkkandoom fëgg nañu ci buntam, woo ko mënuñu koo jot, ñu dàjji bunt bi fekk mu faatu. Ca lañu jëlee néew bi yóbbu ko ca raglu bu Idiriisa Puy bu Garaa-Yoof ngir ñu xam ci yan anam la faatoo. Li jot a rotagum nag mooy  ne góor gi dafa wéradi woon, donte ne sax waxoon nañu ko mu dem ca raglu waaye defu ko. Ñii di waa sàndarmari nag ñuy wéyal seen i lëñbët.                                             .                   

TÀGGAT-YARAM                                   

Marog Romb Na Senegaal                                   

Ci wayndare bu ñii di waa FIFA amal ginnaaw joŋante bu àddina wërngal-këpp ñii di waa Marog romb nañu Senegaal ñeel toftaleg gi. Léegi, ñii di waa Senegaal moom ñi ngi ci fukk ak juróom-ñeenteelu palaas bi. 

Ba tey nag, ci ékibi àddina si yépp, Beresil moo ci jiitoogum ; ñii di waa Arsàntin donte ne ñoo jël raw-gàddu gi terewul ñooy ñaareelu ékib bi. Fukk yi jiitu ci àddina si, ginnaaw ñaar ñooñu, ñii ñoo ci topp : Farãs, Belsig, Àngalteer, Olànd, Kurwaasi, Itaali, Portigaal ak Espaañ.                                            

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj