Démb la Senegaal doon joŋante ak Koddiwaar ñeel 1/8 dë finaal CAN 2024 biy ame foofu ca Koddiwaar. Bi 20i waxtu jotee la joŋante bi door. Senegaal dafa teel a dugal. Nde, ci 4eelu simili bi la Saajo Maane xellil bal bi Abiib Jàllo, mu teg bal bi dënn, xët ko ak tànku càmmooñ bi, daldi toj dugal. Waaye, bi Senegaal dugalee, dañu dellu ginnaaw, bàyyi Koddiwaar di dawal bal bi nim neexee, daldi sëpp caaxi Eduwaar Méndi yi. Noonu, Koddiwaar di puus ba ci 86eelu simili bi, ñu am penaaltii, dugal ko, muy 1-1. Ñu yokkal leen 30i simili ba mu jeex, ndam demul, ndam dikkul. Bi ñu àggee ci teg-dóor yi (séries pénalties), Senegaal dugal ñeent, Koddiwaar dugal juróom daldi gàddu ndam li. Senegaal mi ñu doon xaar ci finaal bi, du ko sax xeeñtu.
MBIRI BASIIRU JOMAY FAY
Usmaan Sonko waxaat na bërki-démb ci dibéer ji. Muy ay kàddu yu mu biral cib widewoo bu mu jotoon a def ba noppi. Ca wax ja nag, ma nga cay xamle ni Basiiru Jomay Fay mooy lawax bi ñu tànnal seen bopp ñeel wotey njiiteefu réew miy am ci 24 féewiryee 2024. Jamono yii ñu doon jàllale widewoo boobu nag, Jomay Fay miy ndeyu mbill gi ma nga ndung-siin. Layookatam sax doon nañ sàkku ci jamono yii weesu ñu may ko bàyyi négandiku ba mu mën a jooxe dagaan baati askan wi niy nawleemi lawax. waaye ba léegi dara.
DAGAANU BAAT YI
Ginnaaw caytug lawax yi, dinañu sóobu ci dagaan baati askan wi, dàq jëmale bésu wote yi. Naka noonu, CNRA (Conseil national de régulation de l’audiovisuel) doon na lotëri anam wi lawax yi waree jàll ci tele bi. Lawax bu ci nekk dinga am 3i simili yees lay jagleel bés bu nekk ngir nga jàllale sa bataaxel ci tele bii di RTS. Ngir bañ xëccoo am ceet, lótari nañ ko ba xam nees leen di toppalante ngoon gu nekk. Bu dee lu jëm ci mbiri jomay fay, Baabakar Jaañ mi jiite CNRA and na ciy leeral. Muy xamle ni mbir mu ñuy soog a jànkonteel la. Ndax lawax bi kott moo yayoo simili yi ñuy maye ci tele bi bu dee wotey njiiteefu réew mi la. Bu doon yeneen wote yi toftal yi mën nañoo uuti njiit li.
ÑAARI ÀTTEKAT YEES TUUMAL NGER CA NDAJEM NDEYU ÀTTE MI
L’UMS (Union des Magistrats du Sénégal), di kurél gi ëmb mbooleem masistaraa yu Sénégaal, àddu na ci ndiisoog gëstu gi dépite PDS yi namm taxawal fa ngombalaan ga ngir ñu luññutu mbiri ñaari way-bokki ndajem ndeyu àtte mees di tuumal nger ci caytug lawax yi. Ci yëgle bi ñu génne nag démb ci dibéer ji, ña nga cay jàppal tànk seen nawle yooyii. Naka noonu, ñuy xamle ni amul genn ndiisoo guy bawoo fa ngombalaan ga, gu am màqaama déglu masistaraa, rawatinaa ci lu jëm ci wàllu yoon. Kenn mënul a topp way-bokk yu ndajem ndeyu àtte mi lu dul ni ndiisoog masistaraa gu kawe gi da cee ànd. Ba tax na ñuy woo masistaraa yépp ci ñu taxawu seen nawle yooyii. Ñuy fàttali way-pólitig yeet ñu sàmmonteek càmpeefi bokkeef gi.
BITIM-RÉEW
CEDEAO dina sàkk pexe ci Mali, Burkinaa ak Niseer. Ginnaaw bi ñetti réew yi biralee démb ni bokkatuñu CEDEAO, kurél gi dafa génne ab yégle ca saa sa ngir wax ci taxawaayam. Li mu ci namm nag mooy dox ci tànki jàmm ndax ñetti réew yi doon nañ way-bokk yu am solo nañ ci kurél gi. Waaye nag ñoo ngi xaar ba ñu jébbal leen càkkuteefu génn.