LI BEES CI NDOGAL LI ËTTU ÀTTEWAAY BU KOWE BI JËLOON
Ci talaata ji la layookati Usmaan Sonko yi jébbal waa ëttu àttewaay bu kowe ba ab dogub neenal-àtte, maanaam li ñuy dippe vi farañse “rabat-d’arrêt”. Li ko waral mooy ne fukki fan ak juróom-ñaar ci weer wii lañu àttewaatoon Usmaan Sonko ca ëtt boobu ginnaaw bi ko àttekatu Sigicoor joxe woon dëgg ci kanamu Nguuru Senegaal. Bii moom li ko wundoon mooy neenal àtte boobu ñu ko àtte woon, ngir mën ko àttewaat ca Ndakaaru. Bi ñu demee bay jël ndogal li, limu àttekat yi matul woon . Ndax, dafa am kenn ku ciy wuyoo ci turu Aysatu Jàllo Ba koo xam ne nanguwul a torlu ndogal li. Sonko ak i layookatam xamle ne ndogal li ñu jël jaarul yoon, ndax, matalewul càrt yi tënk ëtt boobu ñeel limu àttekat yi.
SYTJUST JËL NA NDOGAL
Sytjust (Syndicat des travailleurs de la justice) di kurél gi ëmb ñiy liggéey ci wàllu Yoon jël na ndogal. Ñoom xamle nañu ne dañuy dakkal seen liggéey lu tollu ci ñaari fan muy démb ak tey. Liy jubluwaay bi mooy naqarlu taxawaayu gàkkal gi “ministère de la fonction publique” taxawe ñeel jéego yi jëwriñ ji ñu dénk wàllu Yoon def ngir saafara yenn jafe-jafe yi liggéeykati Yoon yi di jànkonteel. Ak yenn rëq-rëq yi nga xam ne tàmbali na am doole ci yenn ci ñiy liggéey ci bànqaas boobu (greffiers). Nee nañu loolu mi ngi sosoo ci coppiteg dogal bi jëm ci liggéeykati Yoon ca ndajem-jëwriñ ya ñaar-fukki fan ak juróom ci weeru sulet atum 2018. Te, ki ko defoon du kenn ku dul jëwriñ jooju (ministère de la fonction publique). Ñu jàpp ne loolu ag ñàkk a weg la te, moo sooke jafe-jafe yii di tàmbalee bari ci wàllu Yoon. Ñuy sàkku ci Njiitu réew mi mu teel a àddu ci taxawaay boobu jëwriñ ji am balay mbir yi di gën a ëpp i loxo.
TAXAWAAYU NJIITU RÉEW MI ÑEEL TËJUG UCAD
Lu tollu ci juróom-benni weer ba ñu tëjee daara ju kowe ja nekk fa Ndakaaru, ba tey ubbeegul i buntam. Ca xew-xew bu doon am démb ca daara ju kowe jii di Aamadu Maxtaar Mbów yékkati na fa ay kàddu jëmale ci mbir moomu. Moom nag dafa mel ni taxawaayam soppeekuwul wenn yoon. Ndax, xamle na tëj gi li ko sabab kaaraange la. Te, ndongo yi ak jàngalekat yi dañoo war a góor-góorlu suuxat ko fa. Bu dee day jël lu tollu ci 26% ci nafa gi di ko def ci njàngale mu kowe mi, mu suufe mi ak mu digg-dóomu mi, du bàyyee noonu béréb bi kon. Ndax, nee na bi mu jaree ay jumtukaay da ko cee def. Bu ci defee lu ni tollu, du nangu ñuy def ci béréb boobu lu leen neex. Ndax, foofu du ngir jàmmarloo, ngir xalaat la.
CNG DËGGAL NA NDAMAL LAC 2
Ci ndoorteelu weer wii la Lac 2 doon bëre ak Sitta. Njureef la tukkee woon ca làmb ja moo neexul woon Sitta. Ndax, kenn mujjul woon daan sa moroom. Waaye, li ñu artu mbëru Lansaar mi moo ëpp ngir génn gi mu génn géew gi. Moo taxoon ñu jox waalo-waalo bi ndam li. Te, ñoom ñu jàppoon ne loolu tax joxuñu leen ndam li ki ñu doon dajeel tamit def na ko. Ba tax moom Sitta mu defug dab-dabaatal. Kurél gi ñu dénk mbir mooma ca CNG jox na Lac de Guiers 2 ndamam.