Set-setal bi ab xew-xew la boo xam ne Nguur gee ko doon amal ci weer wu nekk walla ci ayu-bés yu nekk. Donte ne sax, mi ngi xaw a yàgg bi ñu ko sumbee ak léegi. Li ñu ko dugge woon mooy setal réew mi. Wii nag, mooy juróom-ñeenteelu yoon ñu koy amal. Waaye, wii yoon moom, Ngomblaan gi ñoo ko woote. Lii mooy yoon wu njëkk it ñoom ñu koy amal. Ñi ngi tuddee xew-xew boobu “Setal sunu pénc mi”. Ëllëg ci gaawu bi, benn fan ci weeru féewiryee. Nee nañu ñi ngi ciy woo bépp dépite, mu ñëw jàppale leen ci bés boobu.
BENEEN BAKKAN ROT NA CA NDOGUM DÉMB MA
Ndogum yoon ma amoon démb fa wetu dëkk bii di Abdu Jafe, limub ña ca faatu yokku na. Nde, démb rekk juróom-ñaari bakkan rot nañu ci. Tay jii, mu amaat keneen ku ca yokku. Kon, fi mu tollu nii juróom-ñetti doomi-aadama ñàkk nañu seen bakkan ci ndog moomu.
LIGUE DES CHAMPIONS:XAMEES NA ÑI WAR A DAJE
Barki-démb ci àllarba ji lañu doon amal joŋante yu mujj yi. Nde, ci bés bu mujj boobu lañu xame yan këlëb ñoo jàll, yan këlëb ñoo toog ak yan këlëb ñoo joŋantewaat seen biir ngir fekki ñi njëkk a génn. Tay ci àjjuma ji nag lañu xam yan ékib ñooy daje ci joŋante yooyu. ñi war a daje, ñii la :
Manchester City – Réal Madrid
Club Brugge – Atalanta
Juventus – PSV
Sporting CP – Dortmund
Feyenoord – AC Milan
AS Monaco – Benfica
Brest – Paris Saint-Germain
Celtic Glasgow – Bayern Munich
SAES MI NGI ÀRTU
SAES (Syndicat Autonome de l’Enseignement Supérieur) mooy kurél gi ëmb jàngalekat yi nekk ci daara yu kowe yi. Kurél googu nag, mi ngi àrtu Nguur gi. Nde, fan yee jàll àrtu woon nañu. Waaye, dafa mel ni gaa ñi dañ leen a soofantal. Ba tax ñuy xamle ne bu mbir yi soppeekuwul dees nañu door ab ñaxtu fukki fan ak ñett ci weeru féewiryee. Li ko waral du lenn lu dul ne Nguur gi fi nekk yéyul yàbbi ci lu jëm ci seen i njàmbat. Maanaam, li ñuy sàkku du lenn lu moy Càmm gi gëddaal déggoo gi ñu xaatimoon ak moom. Bu loolu amul, dinañu jóg ci seen patt-pattaaral gi, yëngal. Ndax, dañoo gis ne anam yi ñuy liggéeyee dafa doy-waar. Muy ñoom di ndongo yi ñu séqal liggéey bi, kenn muccul ci nekkin wu tar wi.
LIMUB NDONGO YI BINDU CI JOŊANTEB 2000i JÀNGALEKAT YI
Ayu-bés bii ñu génn la njëwriñu njàng ak njàngale mu suufe mi ak mu digg-dóomu mi ubbi woon ab joŋante. Joŋante boobu, xamle nañu ne dinañu ci jël lu tollu ci ñaari junniy jàngalekat. Waaye, fi mu tollu nii rekk lu ëpp 158. 000i ndongo bindu nañu ci lënkaay lii di Mirador bees sukkandikoo ci kàdduy Sëriñ Sohaybu Bajaan miy DRH bu njëwriñu njàng mi ak njàngale mi. Te, nee na jàpp na ne diggante fii ak suba balaa ñuy tëj lënkaay gi dinañu àgg ci 160. 000iy ndongo.
SÀNDARMËRI BU NDAR TEG NA LOXO N.T.
Sàndarm Ndar yi (Section de Recherches) mujje nañoo teg loxo waa jii di N.T. Nde, dafa am benn widewoo bu ñuy tas ci mbaali jokkoo yi, mu ciy def naka-su-dul-noonu. Dafa di, moom waa ji, dafa am xale bu jigéen bu ndaw bu mu doon làmbaatu ci genn daamar (bus Tata). Bi widewoo bi tasee nag, ci la takk-der yooyu ubbi ag luññutu ba mujj ko jàpp. Ñi ngi ko jàppe fa dëkk ba mu cosaanoo di Njaween bees sukkandikoo ci waa Seneweb.