LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (31/10/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Abdu Karim Fofana, jëwriñ ji yor kàddu Càmm gi, wax na jëmale ci amalub wotey 2024 yi. Mu mel ni kuy tontu Buubakar Kamara miy xel ñaar ci wote yi, naan dina am walla du am.

« Ñi umpale sunu mboor ci pólitig ni mu réyee, mënuma leen a tere wax seen xalaat. Ak lu mën a xew, àppal i wote, amal leen ca àpp ba, doon na luy màndargaal sunu démokaraasi ak sunu bokkeefu réew. Lu ko dale ci wotey palum njiitu-réew yu 1963 ba tey, mësuñ fee dàq i wote. »

Naka noonu, Sñ bi Fofana di xamle ni palug Njiitu réew mi dina am keroog 25 féewaryee 2025 ni ñu ko jàppe ci àppi bokkeef gi.

MBIRI USMAAN SONKO

Tey ci talaata ji la ëttu àttewaay bu Cedeao waroon a àddu ci mbiri Usmaan sonko ak Càmmug Senegaal. Waaye layookatu Nguur gi moo sàkku ci àttekat bi mu dàq àtte bi te seppi ci loxoy layookati Usmaan Sonko yii di Sñ Sayid Larifu ak Xuwaan Barankoo. Càkkuteef yooyu nag, layookati Usmaan Sonko yi ànduñu ci woon. Dañ bëggoon sax ñu càmbar mbir mi ci xóotaay bi benn yoon nde wote yi agsi nañ ba noppi te dugg nañ ci baayale yi.

Ginnaaw bi mu  dégloo ñaari pàcc yépp nag, àttekat bi dafa mujje dàq àtte bi ba altine jii di ñëw, 6 nowàmbar 2023. Fii ci réew mi moom, Cena bi àddu na ci mbir mi. Te li mu wax mooy na DGE jébbal ndawal Usmaan Sonko kayiti baayale yi, kale (clé) beek bépp jumtukaay bu ñu yoonal te mu def ko ni mu gënee gaaw.

NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI

Jàngune Séex Anta Jóob bu Ndakaaru noppeegul ngir ubbi ay buntam. Ndaje mi kilifa ya nammoon a amal tey dañ ko ajandi ba ayu-bés bii di ñëw, bésub 8 noowàmbar 2023. Waaye jamono yii ndongo yaa nga taxaw ci seen i xef ngir ñu ubbi bunt ya. Dañ sax gàllankoor daara yu digg-dóomu yi nekk fa wër jàngune ba, tere ndongo ya ñu jàng. Li ñu wax nag mooy ni kenn du fa jàng fileek ubbiwuñu jàngune bi.

CAABALUG ANSD

ANSD (Agence nationale de la statistique et de la démocratie), di Mbootaay mi ñu dénk lépp lu jëm ci waññi ak natt askan wi génne na caabalam. Ñu gën cee jàpp ni askanu Senegaal tollu nañ léegi ci 18 032 473i (fukk ak juróom-ñetti tamndaret yu teg fanweer ak ñaari junni yu toftal ñeenti téeméer ak juróom-ñaar-fukk ak ñett) doom-aadam. Ñu seetlu ceet ni wile yoon, góor ñee ëpp jigéen ñi. Nde, téeméer boo jël, lu ëpp juróom fukk ay góor lañ. Wax nañoot ni ñu ëpp ci askan wi ay ndaw lañ.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj