Keroog la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, demoon fa Araabi Sawdit. Mu doonoon tukkiteg waxtaan ci mbirum kopparal, ñu dippee ko “Future Investment Initiative Forum 2024”. Bi loolu jeexee, Njiitu réew mi defaale na umra. Ginnaaw ba mu fa jógee, teereeji na fa Turki tay, ci alxames ji. Tukkite gii nag, Njiitu réewum Turki, Recep Tayyip Erdogan, moo ko fa woo. Mu doon tukkiteg xaritoo ak lëkkaloo ci ay naal yu ñeel cuqalig koom gi, kaaraange ak naataange.
CONGUM NJËGGU USMAAN SONKO
Xew-xew boobu mi ngi am démb, ci àllarba ji. Ma nga xewe fale ca Kungéel. Ñi amal cong mi nag, ginnaaw gi, dañoo daw, bàyyi fa daamar ga ñu yoroon. Daamar googu moom, yàqate nañu ko yaxeet. Takk-der ya ñoo gaaw àtte laata mbir mi di gën a jéggi dayo. Waaye, loolu terewul, am ñu ci jot a jële ay gaañu-gaañu yu metti. Kii di Maalig Gàkku, Njiitul “Grand Parti” bokk it ci lëkkatoo Pastef gi, doy na ci misaal. Nde, moom, am na gaañu-gaañu bu metti ci loxo càmmooñ bi. Waa làngam gi, nee nañu dinañu jébbal ab pelent ci lu yàggul dara ngir ñu mën a xam ñi def jëf ju ñaaw jooju.
MATUWAAY YI DGE JËL ÑEEL WOTE YI FA BÉRÉB YI WALUM DEX GI LAAL
Walum dexu Senegaal gi ak gog Gàmbi laal na dëkkuwaay yu bari. Te, kenn umpalewul ne loolu warul tax ñu bañ a wote. Mu mel ni, nan lañu fa war a doxalee wote yi moo jaaxal gaa ñi. Waaye, kii di njiitul wote yi, Biram Seen, indi na ci ay leeral ci waxtaan wu mu amaloon te, waa “L’Observateur” fésal ko. Xamle na ci ne ñoom waa DGE (Direction Générale des Elections) ñi ngi ciy liggéey ak ñi ñu ci war a liggéeyal. Muy jëwriñ ji ñu dénk biir-réew mi, waa “Brigade nationale des sapeurs pompiers”, waa “Direction de la Protection Civile ak “Direction Territoriale”. Saytu nañu mbooleem bérébi wote yi wal mi laal. Te, jël nañu matuwaay yi ci war yépp ba ñi nga xam ne mën nañoo wote, ñépp matale seen wareefu maxejj bu bés ba jotee.
BÀYYI NAÑU SÉEXUNAA KEYTA
Séexunaa Keyta, ñu gën koo xam ci turu komiseer Keyta, bàyyi nañu ko bàyyib négandiku tay, ci alxames ji. Ci weeru sàttumbaar wii ñu weesu lañu ko tegoon loxo. Ci gàttal, def na weer ak lu teg ci kaso bi. Li ñu ko doon toppe mooy jibal ay xibaar yu wérul. Nde, daf ne coow dafa amoon fa njénde la. Te, coow loolu mi ngi doxoon ci diggante Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ak elimaanu jëwriñam yi, Usmaan Sonko.
Coow li doxoon ci diggante ñaar ñooñu mel na ne bariwul woon ku mu ump ci réew mi. Waaye, ba tey, mbir mi leeragul. Ndax, ñoom ñaar ñépp ñi ngi ci loxoy Yoon. Tey, ci alxames ji, lañu waroon a layoo, waaye, layoo ba, dañu ko mujje a dàq ba weneen yoon. Dinañu ko amal juróom-ñaari fan ci weeru nowàmbar wii di ñëw.