Ci benn saabaalukaay lees biral xibaaru njaayum jumtukaayi tele bii di 7TV. Tele boobu nag, saabalkat bii di Maymuna Nduur Fay moo ko jiite. Ci lees jukki ciy xibaar, Yoon moo sàrtal njaayum jumtukaayi tele bi ci sababu jot bi 3M jote ak boroom lisãsu tele bi. Jàngees na ci yégle bi ne :
« Altine 6i pani sãwiyee 2025, bu 10i waxtu jotee ak bés yi ci topp, bu ko jaree, Meetar Aamadu Caam Géy, “Commissaire-priseur près la Cours d’Appel et les Tribunaux de Dakar”, dina leen jaay ku ëpp lu mu fay. »
NDIMBAL LI ÑEEL WAY-LORU YI CI XEW-XEWI PÓLITIG YI WEESU
5i tamñareeti FCFA la Njiitu réew mi jagleel way-loru yi woon ci xew-xewi pólitig yi weesu (féewiryee 2021 ba féewiryee 2024). Céddaleg xaalis boobu nag moo tàmbalee jur coow. Nde jotoon nañu koo tàbbal ci sémbuw àtte bi ñu doon joyyanti kopparal gi ci atum 2024. Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu PressAfrik siiwal, am na xaat ñu tàmbalee wax ak a duut baaraam céddale gi. Ba tay, ci li ñu jottali, lu tollu ci 120i tamndareeti FCFA lañu jël jagleel ko way-loru yi bokk Pastef kepp te am na itam ñees jàppoon ba ñu jële ciy gaañu-gaañu te boolewuñu leen ci lim bi. Bi ñuy joyyanti kopparal gi, Séex Dibaa, jëwriñ ji yor kopparal geek ngurd mi, fésaloon na itam ni waññi nañu 1800i way-loru. Waaye jotul woon a leeral ci yan anam lees ko amalee.
MBËKK MI
Ci ayu-bés bi weesu, lu tollu ci 29i gaali mbëkk yu bawoo Afrig teer nañu ci duni Canaries yi, fa réewum Espaañ. Ci gaawu bi, jot nañu waññi lu tolloon ci 1 621i doom-aadma. Ci ñooñu, 224i doon nañu ñu bawoo Jifeer, ci duni Fatig yi, fi réewum Senegaal. 57 yi ay jigéen lañu, 14i yi ay xale yu ndaw lañu.
ÀLLIYUN TIN WAX NA CI DPG BI
Àlliyun Tin, njiitu Afrika Jom Center, yéy na yàbbi ci DPG (Déclaration de Politig Générale) bi magum jëwriñ yi doon aajar fa Ngomblaan ga ci àjjuma ji weesu. Muy kàddu yuy wane xel mu dal ak yaakaar ji mu ci jële. Nde, ginnaaw bi mu ko dégloo, jàpp na ni gis-gis bu mag la magum jëwriñ yi fésal ñeel réewum Senegaal. Te bokk na ci li gën a dalal xelam, ni Usmaan Sonko bàyyee xel tolluwaayu koom-koomug jamono ak njariñ li ci xarala yu yees yi am. Ba tax mu jàpp ni dina doon ndam, bu Usmaan Sonko ak Càmmam sottilee ci juróomi at 50% (juróom-fukk ci téeméer boo jël) ci seen sémb wi.
MAKI SÀLL GÉNNAAT NA CI PÓLITIG BI
Ki fi nekkoon Njiitu réew mi, Maki Sàll, dina génn ci mbiri pólitig bi ba jëmmi jamono. Muy ndogal lu mu jël jaare ko ci yenneeku lépp lu doonoon yan ci biir APR. Xibaar boobu nag, dëggal na ko fa sunuy naataango yu Confidentiel Dakar. Naka noonu, muy ñaan waa pàrti bi teggil ko yitte yi mu waroon di jooxe te bàyye kook turuw njiit lees duppee Président d’honneur. Tekkiwul ni dafay raxasu ba set ci pólitig bi. Waaye, dafa namm a jooxe ay mbiram ci wàlluw bitim-réew te jot gi du ko may mu boole yépp. Ci fan yii di ñëw, dees na amal am ndaje mu mag ngir andi ay coppite ci doxiinu pàrti bi ak ñi koy jiite.