Ginnaaw bi ko toppekat bi gàllee 7i tuuma ci gaawu gi, njiitul Pastef li Usmaan Sonko doon na jàkkaarlook magum àttekat yi Maaham Jàllo ci altine tey ji. Naka noonu, ay layookatam doon nañ amal ab lël démb ci dibéer ji, doon ci jàkkaarlook taskati xibaar yi. Ñoom nag, li ñu jàppoon ni àttekat bi dafa nar a dëggal tuuma yees ko gàll ngir nëbb ko jant wi moo mujje am. Nde, bi ko magum àttekat yi dégloo ba noppi daf ko def li ñuy tuddee « mandat de dépôt ». Jot naa yokk sax ci tuuma yi li ñuy woowe « diffusion de fausses nouvelles », maanaam tasaarey xibaar yu wérul.
Ba tey ci lël bi ñu doon amal, layookati Usmaan Sonko yi tontu nañu toppekat bi ci li mu wax ni jàpp gi ñu jàpp Usmaan Sonko jotewul dara ak daan yees ko daanoon ci digganteem ak Aji Saar walla Maam Mbay Ñaŋ. Li layookat yi jot a leeral mooy jàpp gi dafay neenal lépp luy daan te ñu dogaloon ko ci ñàkk teewam, ñu koy wax contumance.
Bu dee lu aju ci Tusĩ Màngaa ak Paap Aale Ñaŋ, ñoom ñaar ñépp a ngi ci loxoy Yoon ba léegi. Tusĩ Màngaa ma nga ñu téyandi (garde à vue). Waaye, taskatu xibaar bi Paap Aale Ñaŋ dañ koo jàllale ndungu-siin. Liñ koy toppe mooy ni dafay woote ak a xirtal nit ñi ci fitna.
Nguur gi dogati na lënkaay gi
Bi ñu jàppee Usmaan Sonko ci àjjuma ji la yëngu-yëngu yu metti tàmbaliwaat am ci réew mi. Ñu gënoon leen a ràññe ca diwaani Sigicoor ak Ndakaaru. Donte ni seetlu nañu tuuti dal ci suba si, terewul Nguur gi jël na ndogalub dakkal lënkaay gi ci yenn waxtu yi. Ci yégle bi ñu siiwal, jëwriñ ji yor jokkoo bee ngi xamle ni ay bataaxali fitna lañuy wasaare ci mbaali jokkoo yi.
Mbëkk mi
Ag gaal gu wutali woon Tugal moo réer ci biir géej gi. Mi ngi bawoo woon ci waaxi Faas-Bóoy ci 10eelu fan ci sulet wii weesu. Bees sukkandikoo ci xibaar yi rot, lu tollu ci 150i ndaw ñoo ngi woon ci biir. Ginnaaw lu ëpp ñaar-fukki fan bi ñu demee ak tey, kenn xamul ci luñ nekk.
Afrobasket 2023
Gaynde Senegaal yu jigéen yi jekkooguñu seen bopp ci Afrobasket 2023 biy am fale ca Kigali, réewum Ruwàndaa. Ñaari joŋante yi ñu jot a amal yépp dañ cee nërmeelu. Fii mu nekk, benn joŋante moo leen dese ci talaata ji. Ci seen digganteek Esipt lay doon. Muy joŋante bob, ku ci dóor dina jàll ca kaar-dë-finaal yi. Ku ci nërmeelu moom dina lem i kaakaam, daldi ñibbi.