Ci weeru suwe wale ñu génn lañu daanoon Usmaan Sonko ñaari ati kaso ci coow li doxoon digganteem ak Aji Saar. Ginnaaw bi ñu ko tegee loxo ci njeexitalu weeru sulet wii weesu, dañu ne woon daan bi nasax na. Ndax, ba ñu koy daan fekkewu ko. Kon, saa su ñu ko tegee loxo rekk jeex na. Waaye, loolu bokkul ak li jëwriñ ji ñu dénk wàllu Yoon ci Senegaal wax. Ci laaj-tontu bi doxoon digganteem ak “Jeune Afrique” daf fa xamle ne daan bi mat na léegi (définitive). Ndax, nee na ñëwul ca layoo ba, yónneewul. Rax-ci-dolli, mënoon na dem joxe boppam. Te tamit, amoon na jot gi ngir dem ñu fànq àtte boobu. Waaye defu ko. Moo tax ci diggante boobu àtte bi mat na sëkk. Loolu mu wax day firndeel ne kii di Njiitul Pastef du mën a bokk ci wote yii di ñëw.
WÉR-GI-YARAMU USMAAN SONKO
Tey, alxames fanweeri fan ak benn ci weeru ut la kii di Njiitul Pastef am fanweeri fan ak ñett yoo xam ne mi ngi koy xiifal. Moom nag, jamono jii sonn na ba fu sonnu yem. Ndax, bu yàgg ba léegi ma nga ca raglu ba, ñu koy may doole. Mu mel ni démb yëf yi dafa gën a doy waar. Sire Keledoor Li, kenn ci ay layookatam moo bindaat, di àdduwaat ñaareel wi yoon ginnaaw bi mu ko njëkke woon a defe. Waaye, dafa mel ni tey mbir mi dafa gën a yéeme. Nasax gi wér-gi-yaramam nasax tax ba mu jàpp ne paj yi kese mënul a teree mbir mi àgg ci yenn cér yi.
HANIBAAL JIM DAKKAL NA XIIFALGI
Lu tollu ci weer daanaaka bi mu doore xiifaal gi ak léegi, moom Muhammed Sàmba Jiim, ñu gën ko xame ci Hanibaal, mujje na dakkal xiifal gi. Mi ngi jël ndogal loolu ginnaaw bi ko ko xalifab Médina Gunaas digalee. Ki xamle loolu mooy layookatam bii di Meetar Musaa SAAR.
XEW-XEW BU TIIS CA GUDOMP
Ñetti nit ñu seen i at xaw a soree ñoo faatu ci ag dex foofa ca Sàndiñeri, nekke fa gox bii di Karantabaa. Ñooña faatu nag, am na ku ci tuddu Sana Daraame amoon lu tollu ci juróom-benn fukki at, Muuskebaa Mànjaŋ amoon juróom-ñaar fukki at. Ak keneen kuy wuyoo ci turu Paap Maane amoon ñaar-fukki at ak ñeent.
SOS-AADA FAAS TAXAW NA
Sos nekk mbër mu ñu miin ci làmbu ji, mu bokk “écurie” dóor-dóoraat moo war a daje ak kii di Aada Faas mi bokk Faas Bennoo nga xam ne jamono jii kenn réerewu ko ci làmbu ji. Làmb jooju nag, ki ko taxawal mooy Jàmbaar Productions. Dees na bëre làmb jooju juróom-ñetti fan ci weeru oktoobar atum 2023.
U.A NAQARLU NA LA XEW GABOŊ
Mbootaayu bennoog Afrig ñi ngi ñaawlu la xew ca réewum Gaboŋ. Démb la sóobare ya foqati Nguur ga ca loxoy Aali Bóngoo Ondimbaa ginnaaw ba ñu biralee njureef ya tukkee ca wote ya. Mbootaay gi dafa jàpp ne loolu sàmmontewul ak sàrtu Afrig ñeel wote yi, demokaraasi ak yorin wi. Moo tax ñuy woo làrme bi ak mbooleem ñiy wattu kaaraange fa Gaboŋ ngir ñu aar Njiitu réew ma ak ug njabootam ak mbooleem ñi bokk ci Nguur gi. Rax-ci-dolli, ñoom sóobare yi ak kuréli way-moomeel yépp ñu jiital waxtaan ba lépp mën a dellusi ci yoon.
JÉYYA JA AM CA JOHANNESBURG
mbir mu doy waar moo am ca Johannesburg. Dëkk boobu ma nga nekke ca Afrig bëj-saalum. Ag lakk gu yéeme moo fa am ci genn kër gu am lu tollu ci juróomi etaas ci boori benn waxtu ci guddi. Nee nañu lu jege juróom-benn fukki nit ak ñett ñàkk nañu ci seen i bakkan. Mu am tamit ñeen-fukki nit yu ci jële ay gaañu-gaañu. Te, ba tey ña ngay wéyal rawale ga ca béréb boobu. Maanaam xamaguñu fu yëf yi di yem. Rax-ci-dolli, xamaguñu lu taal foofa. Waaye, ñi ngi ci luññutu yi.
MÀGGALU TUUBAA
Njiitu réew mi, Maki Sàll, ñu ngi koy xaarandi fa Tuubaa. Muy ab tukkib nemmeeku bu ñuy faral di gis mu koy amal ci kanamu Sëriñ Muntaxaa laataa màggal gi. Ñu jàpp ko tey ci Alxames ji. Bu ñu sukkandikoo ci Leral.net, ña ngay gaaral liggéey bu mag ba mu fa jot a def bi mu toogee ak léegi.