Bu amee ñu doon laamlaame wotey 2024 ndax dees ko war a dàq am déet, mënees na jàpp ni wote yi dinañ am ci bés bees ko jàppoon. Njiitu réew mi Maki Sàll xaatim na dekkere bi keroog àllarba, 29 noowàmbar 2023.
Ci biir dekkere bi, mi ngi ciy woo Saa-Senegaal yi fi biir réew mi ak yu fa bitim-réew ñu dem woteji keroog dibéer 25 féewiryee 2024. Dees na tijji mbañ-gàcc yi bu 8i waxtu jotee ci suba si ba 18i waxtu ci ngoon. Bu laajee yokk walla wàññi, jaraaf yi, perefe yi walla supperefe yi dinañu jël ndogal li ci war. Ca bitim-réew itam, coppite yee ngi aju ci ndogalu ñi fa teewal caytu gi walla kõsilaa bi.
Xalifa Sàll ak i ñoñam ñoo ngi ba tey ci seen wëraan mi fi biir réew mi. Waaye démb ci dibéer ji, takk-der yi dañoo dog seen yoon bi ñuy tollu fa diwaanu Maatam. Muy ndogal lu tukkee fa perefe diwaan ba. Ginnaaw ba ñu leen wàccee nag, wa Taxawu Senegaal ak seen njiil li dañoo mujje nàmm seen i tànk ngir àggale seen yoon.
Li ni mel dal naat yeneen Lawax yu mel ni Maalig Gàkku ak Bugaan Géy Dani. Muy lu ñu ànd di ñaawlu jamono jii seen nattaango Aamadu Ba, lawaxu Càmm gi, nekk di wéyal wëraanu koomam ci lu amul benn jafe-jafe.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Kurélu ndongo Saa-Senegaal yi nekk Farãs àddu nañ ci Jàngune Séex Anta Jóob bi tëw a tijji. Naka noonu, ñuy sàkku ci kilifa yi ñu jël matukaay yi war ngir ñoŋal kaaraange ndogo yeek képp kuy liggéey fa jàngune ba ba njàng mi bañ a naax saay.
Ñoom nag, rafetluwuñu wenn yoon yàqu-yàqu yi fa jaaroon. Ba tax ñuy woo ndongo yi ci ñu xam te ràññe béréb yees di xeexe ak bérébi jànguwaay yi. Te ñu delu xool lan moo war a doon seen taxawaay, ñoom ñi war a suqali réew mi ëllëg.
MBËKK MI
Lu ëpp 50 000i doom-aadama ñàkk nañu seen bakkan ci mbëkk mi, ci diggante atum 2006 ak tey. Muy lim bu yéeme bu Sëriñ Moor Mbay biral ci gaawu gi. Fekk kurél gii di Mbooloom Barñi ñeel njëfini maxejj (Association Bargny initiative citoyenne) dalaloon ko ci seen waxtaan yi ñu doon amal ci mbëkk mi. Ragal na ni sax lim bi mën naa yokku ak sedd bii di ñëw. Nde dal yees leen jagleel fa Tenerif dañu fees dell ba ñu mujj di leen toxal ci yeneen péey yu deme ni Madërid.
BITIM-RÉEW
Fa Kates (réewum Tansani), suuf saa màbb ginaaw taw yu am solo yu fa wàcc ci gaawu gi. 47i doom-aadama jot nañ caa ñàkk seen bakkan. Am naat 85 yu ca jële i gaañu-gaañu. Ñuy ragal nag lim yi yokk, nde ba léegi ceet yaa nga ñuy wéyal.
G5 Sayel baa ngi ci yoonu tas. Ginnaaw bi réewum Mali génnee daaw, Burkinaa Faaso ak Niseer fésal nañ ci gaawu gi ni génn nañ ceet ba set. Ñoom nag dañoo jàpp ni kurél gi dafa tële am taxawaay bu mat ci sas yi mu saasoo woon. Rax-ci-dolli ni càmpeefam yi di dooxee dafa yéex te méngoowul ak gis-gis bi ñu am ci moom-sa-bopp. Ci pàttali, ci atum 2014 la kurél gi judduwoon, ci diggante Burkinaa, Càdd, Mali, Móritani ak Niseer, ngir xeexe ko rëtëlkat yi lëmbe diwaanu Sayel bi.