LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (4/7/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

OFNAC MI NGI DALAL ÑI ÑU TABB CI NGUUR GU BEES GI

Ginnaaw bi ñu leen tabbee, ñoom jëwriñ yeek Njiit yi, bàyyiwuñu leen noonu. Nde, dañoo sàkku ci ñoom ñu dem fa OFNAC ñu xam li ñu yor ci alal. Mu mel ni, gaa ñaa ngi jëfe ndigal. Ndax, bees sukkandikoo ci xibaar yi Walf Quotidien rotal, jëwriñ yi ak i njiit yi ñu tabb ci yenn béréb yi jot nañoo siiwal li ñu am. Seen taxawaay day firndeel ne jox nañu cër àppu ñetti weer bi ñu leen may ginnaaw bi ñu leen takkalee seen i ndomboy-tànk.

JËWRIÑ JI ÑU DÉNK WÀLLU YOON MI NGI ÀRTU

Fan yii yépp dañoo nemmeeku ag lënkaay gu ñuy tasaaree ci mbaali jokkoo yi. Lees ci bind mooy “sama casier judiciaire”. Maanaam, di nax saa-senegaal yi ci ne mën ngaa jot ci sa këyit boobu boo jaaree ci lënkaay googu. Te, du def sax ñaari fan. Jëwriñ ji ñu dénk wàlluw Yoon, nee na laalewul te taqewul ak mbir moomu. Mi ngi àrtu askan wi. Di leen xamal ne, jamono jii ñu tollu, joxewul benn dogal ci loolu. Te, amul banqaas gu am sañ-sañ ci loolu bu dul ay yosam. Naka noonu, Kurél gii di CPDP (Commission de Protection des Données Personnelles), ñoom it, nee ñu mbir mi laalewuñu ci. Kon, mënees naa jàpp ne loolu ay naxembaay kepp la.

COOWAL SAA-SIIN YI AK DAWALKAT BI JEEXAGUL

Coow loolu ame woon fa Daaru Xuddóos diggante ay saa-siin ak dawalkat bii di Ibraayma Faal jeexagul. Cig pàttali, saa-siin yooyu dañu doon néewal doole dawalkat bi. Ndekete yoo, ñi ngi leen doon widewoo. Bi widewoo bi siiwee lañu leen teg loxo. Boobaak léegi, ña nga ca loxoy yoon. Démb ci àllarba ji, doon nañu layoo. Waaye, ba tey daanaguñu ci kenn. Fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru sulet wii lañuy leeral mbir mi. Ñu xam ndax, li toppekat bi di sàkku moom ak layookatu dawalkat bi la àttekat bi di def am déet.

BAC 2024

Keroog ci talaata ji la joŋante boobu door. Waaye, bu ren jii, mel na ni ñu bari dootuñu ko fàtte. Ndax, dafa bari ay dàqe lool sax. Te, li ëpp ci dàqe yooyu, dara waralu leen lu moy yor ag jollasu fa béréb yooyu. Nde, kenn umpalewul ne, dañu tere jollasu yi ci béréb yooyu. Waaye, loolu terewul am yenn ndongo yu ko fa yóbbaale. Moo tax it, yet wa dal na seen kow. Ndax, démb rekk am na ñetti ndongo yu ñu dàq fa Sigicoor. Te, loolu bokkul ak ñeneen ña leen jiitu ci yeneen bérébi joŋante yi, rawatina fa Kawlax. Tay jii tamit, dàq nañu fukki ndongo ak ñaar fa Gudomp. Te, lenn waralu ko lu moy yor ay jollasu fa béréb ba ñuy defee Bac.

CAN 2025

Tey ci alxames ji lañu doon siiwal réew yi war a bokk ay kippu ngir ñu mën a xam ñan ñooy bokk ci joŋante boobu nar a ame fa Marog. Ndax, réew yi tollu nañu ci ñeent-fukk ak juróom-ñett. Te, ñaar-fukk ak ñeent ñooy jàll. Maanaam, ñooy dem fa joŋante biy am Marog diggante ñaar-fukki fan ak benn ci weeru desàmbar 2025 ba fukki fan ak juróom-ñett ci weeru sãwiyee 2026. Kippu yi nag, tollu nañu ci fukk ak ñaar. Te, kippu gu nekk ñaar ña fa jiitu ñooy génn. Ñii di waa Marog moom, jàll nañu ba noppi. Ndax, ñoom ñooy amal CAN bi. Ñii di waa Senegaal moom, ñi ngi bokk ci kippu fukkeel ak ñaar. Ñi ñu ko bokkal di Burkinaa Faaso, Malawi ak Burundi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj