Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, yékkati nay kàddu bi mu jógee ci tukkiteem bi gaawu. Kàddu yooyu nag, ñoo ngi aju ci kàmpaañu wotey Ngomblaan gi ak tafaar yi ci am. Bokk na ci taafar yooyu, cong mi am fa màkkaanu Taxawu Senegaal, cong mi dal ci kaw njëggum njiitu toftaleg Pastef fi Ndakaaru ak ci kow njëggum magum jëwriñ yi fa Kungël. Naka noonu, mu dellu di ñaaxaat way-pólitig yi ñu ànd ak dal te sàmmonteek seen i wareef. Ginnaaw loolu, sàkku na ci jëwriñ ji yor wàllu yoon mu ubbi ag luññutu ngir leeral lépp, teg ci yoon ñi ko def, ak làngug pólitig gu ñu mën a bokk. Sàkku naat ci jëwriñ ji yor kaaraange biir réew mi mu yokk kaaraange njëgg yi ngir gën a wàttandiku tafaar yi.
WÀÑÑIG DUND BI
Càmm gee ngi ci tànki jàppandal dund bi. Bokk na ci pexe yi mu nar, taxawal i bitigi delluwaay yu méngoo ak jamono ak ay bitig yu mag ci diiwaani yi ak ci gox yi. Muy xibaar bu jëwriñu ndefar gi ak yaxantu bi, Sëriñ Géey Jóob, biral ci gaawu gii weesu, bi kurélug saytukati koom-koomu réew mi doon amal ndaje mu mag. Lees ci namm nag mooy, li ci jiitu, fexe ba askan wi mën a jot ci dund bi ak njëg gu yomb ci fépp fu ñu mën a nekk ci biir réew mi ; li ci topp, méngale tabaxte yi ñeel yaxantu bi ak jamono.
MBIRUM AMET NDÓOY
Démb ci altine ji, 4i pani nowàmbar 2024 la yoon waroon a àddu ci mbiri Amet Ndóoy. Waaye ay layookatam ñoo sàkku ci ñu neenal doxalin wi ndax li ñu jalgati ay àqam ak i yelleefam bi ñu koy teg loxo. Nde, dañu ko nëbb jant bi ba noppi sog di ko xamal ni mën na wuti layookat. Rax-ci-dolli, déglu nañu ko bi ñu ko jàppee ba sa ëllëg sa te yëgaluñ ko ni dees ko war a déglu. Moo waral ba ñu mujje dàq layoo bi ba keroog alxames 7i pani nowàmbar. Ci pàttali, ñiŋ ko tegoon loxo ci bésub 25i pani oktoobar wii weesu ginnaaw bi ñu ko wooloo woon fa Sàndarmëri bu Sebikotaan. Lees koy toppe nag, mooy jëfandikoo kayit yu baaxul ak dawal ci ñàkk peermi. Muy ay tuuma yu mu weddi woon laata ñu koy jàpp.
BITIM-RÉEW
Fa réewum Espaañ, waññeegum nañu 217i doomi Aadama yu ñàkk seen i bakkan ci ngëlén li fa jaaroon keroog ci guddig 29 jàpp 30i fan ci weeru oktoobar wi. 213i ndee yépp, fa diiwaanu Valence lañ leen nemmeeku. Muy xibaar yu tukkee ca kilifa ya. Xamle nañu itam ni bari na lool ñi réer. Waaye, Càmm gaa ngay dalal xel ya ni ceet yaa ngi ñuy wéyal ca biir kër ya, ci daamar yeek ci walum ndox mi. Magum Jëwriñ ya, Pedoroo Sansees xamle naat ni yokk nañu 5 000iy sóobare ngir ñu dooleel limub wallukat yeek ñi doon dindi yàqute yi.