LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (5/12/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LIGGÉEY BA DOOR NA FA NGOMBLAAN GA

Altine jii weesu lañu ubbi fukk ak juróomeelu moomeg Ngomblaan gi, fal mbooleem ñi ñu war a fal ca béréb ba. Mu mel ni dépitey Ngomblaan gii amuñu toogaay. Nde, démb, ci àllarba ji la ki fi nekkoon Njiitu Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob, doon jébbal lenge yi El Maalig Njaay mi ñu fal keroog Njiitu campeef googu. Waaye, mbir mi yemul foofu. Ndax, suba ci àjjuma ji 6i pani desàmbar woote nañu am ndaje fa Ngomblaan ga. Li ñu ko dugge mooy wax ci xaatimug toftaley way-bokk yi ci ndiisoo yi. Maanaam, li ñuy wax ci farañse “ratification des listes des membres des commissions permanentes”.

SENEGAAL MOO ËPP I BOR CI AFRIG

Bees sukkandikoo ci caabal gi waa “Banque mondiale” siiwal, Senegaal mooy réew mi ëpp i bor ci réewi Afrig yi. Ci li ñu sukkandiku ñoom waa “Banque mondiale” mooy bor bu réy bi ñu am fa bitim-réew. Maanaam, li ñuy leb dafa bari lool. Nee ñu, bor boobu jege na ñeen-fukki miliyaar ci ay dolaar (39 milliards de dollars). Loolu di firndeel ne réew mu ndóol la. Waaye, ni mu amee ci réewi Afrig yi réew moo xam ne dafa bari ay bor lool, noonu la ame réew moo xam ne bariwul i bor. Réewum Alseri misaal la ci.

JÀMMAARLOO YI DOORAAT NA FA UCAD

Jàmmaarloo diggante takk-der yi ak ndongo yi tàmbaliwaat na fa daara ju kowe ju Ndakaaru. Li sabab jàmmaarloo bi du lenn lu moy ndongoy Master yiy laaj ñu fay leen fukki weer ak ñeent yi ñu leen yoreel. Maanaam, toog nañu at ak lu topp joxuñu leen dara. Donte ne sax, fan yee yëngaloon nañu tuuti, teggi seen tànk. Waaye, tay ci alxames ji, dañoo delloo buum ca mboy-mboy ga ngir gaa ñi fey leen xaalis bi ñu leen ameel.

WAA HCCT ÑI NGI ÀRTU

Ci weeru sàttumbaar wii weesu la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dàqoon Njiitu béréb boobu. Cig pàttali, Nguur gu bees gi dafa jàpp ne banqaas boobu amul njariñ. Moo taxoon, ñu doon sàkku ci Ngomblaan gi fi jóge, ñu fànq ko. Dépitey fukkeelu Ngomblaan ak ñeent yi bañ ba tëdd ca naaj wa. Nde, Nguur gi fi jóge moo fa ëppoon doole. Loolu bokk ci li tax Njiitu réew mi dàq njiit la, tas Ngomblaan gi, woote ay wote fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru nowàmbar. Ginnaaw bi waa Pastef jëlee ndam li ci wote yooyu ba ñu taxawal Ngomblaan gu yees gi, way-bokk yi ci banqaas boobu amal nañu ndajem-waxtaan ngir àddu ci mbir mi. Ñoom téeméer ak juróom-fukk yooyu, li ñuy sàkku mooy ñu fay leen. Ndax, weeru sàttumbaar bi ñu dàqee seen njiit la, Aminata Mbeng Njaay ba tay, kenn fayu leen.

DAAN NAÑU MARI LÓO

Mari Lóo, doomu waykatu Senegaal bu mag bii di Ismaayla Lóo, daan nañu ko. Li sabab daan bi mooy mbirum njuuj-njaaj. Nde, dafa am ñu mu doon gëmloo ay naal yu ñu mën a jële ay njurteef yu kowe seen njort. Ci loolu la jële ci ñoom lu tollu ci xaaju miliyaar (533 miliyoŋ). Ëttu àttewaay bu Ndakaaru ba gis na ne moom moo def. Looloo tax ñu daan ko ñaar-fukki weeri kaso ak ñaar. Moom nag, juróom-benni weeri kaso kepp a ko des. Ndax, fanweeri fan ci weeri ut, atum 2023 lañu ko yóbboon kaso. Rax-ci-dolli, moom dina fay xaalis bu takku boobu ñi mu def jëf ju ñaaw jooju.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj