LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (5/2/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

YËNGU-YËNGU YI GINNAAW NDÀQUG WOTE YI

Ginnaaw dal gi nu tàmbali woon a seetlu ci biir réew mi, yëngu-yëngu yeek jàppante yi ci diggante takk-der yeek askan wi tàmbaleeti nañu. Ñàkk a ànd ci ndogalu Njiitu réew mi ñeel fomm wote yi la askan wi mënul a wannaasu, rawatina lawaxi kujje gi doon waajal sóobu ci ndagaanug baati askan wi.

Ñu bare ci kujje googu sax dajaloo woon nañu ginnaaw bi Njiitu réew mi Maki Sàll ajandee wote yi ci gaawu gi. Ci noonu lañu biralee ne mbir yi du fi yam te dinañu tàmbali dagaan baati askan wi ci dibéer ji, ni leen ko yoon mayee. Waaye, démb ci dibéer ji, takk-der yi mayuñu leen fu ñu jaar bay dajaloo. Fu ñu génn ñu daldi leen koj. Ba ci militaŋ yu fare ci kujje gi ak askan wi àndul ci ndogal li, fu ñu tàmbalee dajaloo sàndarma yi fekk leen fa, tasaare leen ak i gërënaat.

Li des ci ngoonug démb gi yépp nag, ay jàmmaarloo lañu nemmeeku fa Ndakaaru. Muy ay jàmmaarloo yu dox ci diggante takk-der yiy sànni ay gërënaat ngir tasaare mbooloo yi ak mbooloo yi leen doon dékku ak ay sànni xeer ak taal ci taliy Ndakaaru yi.

AMINATA TURE AK ANTA BAABAKAR NGOM GINNAAW BI ÑU LEEN BAYYEE

Aminata Ture mi fi nekkoon njiitul jëwriñ yi ci Nguuru Maki Sàll ak Anta Baakacar Ngom, fas yéenewuñu dellu ginnaaw wenn yoon. Takk-der yee leen tegoon loxo démb ci dibéer ji. Fekk ñu génnoon ci mbedd mi nees ko waxe woon ngir xeex ndogal li Njiitu réew mi jël ci ajandi wote yi. Ginnaaw gi lañu leen féexal ci biir guddi gi. Waaye, li Aminata Ture wax ci saa si mooy ne « xeex bi dafay wéy ». Anta Baabakar Ngom itam xamle na ni waa Nguur gi dañ bëgg ñu noppi. Jéem nañ leen tiital waaye ñoom duñ dellu ginnaaw. Lu ni mel sax dafa leen di gën a dëggal ci seen xeex bi.

NGOMBALAAN GA

Tey ci altine ji la dépite yi tàmbali càmbar càkkuteefu àtte bi namm toxal wote yi Njiitu réew mi ajandi bërki-démb ci gaawu gi. Muy ag càkkuteef gog, dépite PDS yee ko dugal. Liñ ci namm mooy yóbbu wote yi ba weeru ut 2024. Bu àtte bi jàllee, dina jur coppite ci dogu 31 bu Ndeyu àtte réew mi tey yamale moomeg Njiitu réew mi 45i fan ginnaaw bi mu jeexalee.

Jamono ji ñuy bind gàttal yile, dépitey Yewwi Askan Wi ak u Taxawu Senegaal ñoo taxaw temm ne dee kenn du fa wote sémbub àtte bi.

WOOTEB ALIYUN TIN

Aliyun Tin, di kenn ku bokk ci kurélu way-maxejj yi, moo ngi woo way-pólitig yi ñu bañ a àgg ciy xeexoo, walla dereet juy tuuru. Li mu bëgg mooy ñu génne càkkuteefu àtte bi te waxtaane àpp gu bees ñeel wote yi. Muy woo way-pólitig yi ci waxtaan woowu te ñu def ko ci anam yu dëppoo ba ñu mën a amal i wote laata moomeg Njiitu réew mi di jeex.

BITIM-RÉEW

Njiitu UA àddu na ci xew-xewi Senegaal yi

Musaa Faki Mahamat, Njiitul Ndiisoog UA (Union Africaine) àdduna ci coowal wote yi fi réewum Sénégaal. Ab yégle la génne tey ci altine ji. Mu ciy xam le ni dàq gi Niitu réew mi dàq wote yi soxal na ko lool. Ba tax muy sàkku ci moom mu fexe amal i wote yu leer, ci jàmm ak déggoo. Te ñu amal leen balaa yàgg. Bëgg naat way-pólitig yi ñu disso, waxtaan ngir déggoo mën a am.

Njiitu réewu Namibi faatu na

Réewum Namibi ñàkk na Njiitu réewam, Haas Géngob. Démb ci dibéer ji, ci suba teel, la xibaar bi rot. Moom Haas nag, moo nekkoon ñetteelu Njiitu réew foofu. Bokkoon na ci ñi jiite woon xeex bi jamono ba réew ma nammee moom boppam ci tubaab yi. Mi ngi faatu ci 82i atam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj