Ci ayu-bés bee ñu génn lañu dooroon péncoom réew mi ñeel nosteg pólitig gi. Démb, ci àllarba ji, la waxtaan wi di sog a jeex. Am na ay poñ yoo xam ne déggoo nañu ci. Naka noonu, am na poñ yoo xam ne déggoowuñu ci. Jamono jii nag, li ñépp di xaar mooy ñu jëmmal poñ yoy, péncookat yi déggoo nañu ci, dëppoo ci ba tënk leen.
NAX NAÑU ISMAYLA SAAR
Doomu Senegaal jii futbal fale ca Àngalteer lañu nax ci mbirum dëkkuwaay fa béréb bii di Jamñaajo. Ndaxte, dañu ko jaay ab dëkkuwaay (apàrtamaa), jox ko ay caabeem ba am yum fa jot a dugal. Ndekete yoo, loolu ay naxi kese la. Te, moom jotoon naa dugal lu tollu ci fanweeri miliyoŋ ak ñaar bees sukkandikoo ci xibaar yi yéenekaay Libération fésal ci seen xët bu njëkk. Li ci doy waar mooy ne, dëkkuwaay boobu, dafa am boroom ba noppi. Moom nag, jot na dem ci Yoon ba jébbal ab jure ngir ñu ubbi ci ay luññutu.
XIBAAR ÑEEL MBIRI YOON
Omar Sow, di kenn ci way-bokki làngug APR (Alliance Pour la République) ma nga ca loxoy Yoon ba tay. Li ñu koy toppe mooy tasaare xibaar yu wérul. Démb lañu ko doon àtte. Waaye, daan bi moom waxeesagu ko. Fukki fan ak juróom-ñett ci weeru suwe lañuy leeral ndax dañu koy bàyyi walla day des ca kaso ba.
Naka noonu, kii di Sang Séex Musaa Jaañ, ma nga ca loxoy Yoon ba tay ci sababu kàddu yu doy waar yu mu yékkati woon ci Alxuraan. Toppekatu bokkeef gi teg na ko ñaari ati kaso yoo xam ne dina ca tëdd juróom-benni weer ak alamaanu ñeen-fukki junni. Li am ba des mooy ne kàddu gu mujj gi àttekat bee ko yore.
Démb, ci àllarba ji, ba tay, ci lañu àtte Asuraa Faal ak El Haaj Uséynu Kayre. Moom Asuraa, li ñu ko doon toppe kàddu yu tegginewul yi mu yékkati woon ci benn widewoo. Ñoom ñaar nag, daan nañu leen juróom-benni weeri kaso yoo xam ne duñu ko tëdd.
NDOGUM YOON FA LUGA
Tay, ci yoor-yoor gi, la ndogum yoon mu metti am fa wetu Luga. Ma nga ame fa wetu dëkk bii di Buumi. Ma nga am ay boori fukki waxtu ak benn. Benn biis moo fa mbëkkante ak genn daamar gu ndaw. Ñaari nit ñàkk nañu ci seen i bakkan. Mu am tamit, juróom ñoo xam ne jële nañu ci ay gaañu-gaañu yu metti. Rawale nañu leen fa raglu Ahmet Saxiir Mbay bu Luga.
Ba tay, am na meneen ndogu yoon mu am ci bésub tay jii. Biisu ndongoy Koldaa yi doon tabaskiji moo def ab aksidaŋ. Am na kenn ku ci ñàkk bakkanam. Mu am ñu bari ñu ci jële ay gaañu-gaañu.
SAABALUKAAY YI AM NAÑUY DËJ
Naqar ak tiis la waa këru liggéeyukaay gii di GFM (Groupe Futurs Médias) xëye tay. Kenn ci seen i naataangoo, seen mbokk, moo wuyuji Boroomam. Moom Ibraahiima Jeŋ moo nekkoon li ñuy wax “directeur commercial” fa ëtt boobu di GFM. Kon, saabalukaay yépp a ñàkk rawatina kër ga nga xam ne fa la doon liggéeye.
Naka noonu, ca Sud Fm tamit am na ku fa ñàkk bakkanam, muy animaatëer bu siiw bii di DJ Nikolaa Jóob, di doomu waykat bii di Siidi Jóob. Moom nag, ku siiwoon la. Moo daan amal jotaay bii di Ndékki Li, daan ko bokk ak ñaari ustaas yii di Mbàkke Silla ak Mawdo Fay. Nee ñu dafa feebaroon.
EJO ak LU DEFU WAXU ñu ngi leen di jaale seen i njaboot, di leen jaale njabootu saabalakat yépp, di leen ñaanal njéggal ak yërmande.
WOTEY PALUG NJIITU RÉEW FA KODDIWAAR
Luy tollu ci ñeenti weer ay bëgg a des ci wote yi, coow li ne kurr fa réew ma. Li ko waral du lenn lu moy ñenn ci waa kujje gi ñu génnee ci joŋante bi. Maanaam, ñoom bokkuñu ci toftaleg lawax yi. Wujji Njiitu réew yi dul bokk ca wote ya, ñii la : Lorã Bagboo, Tiijaan Caam (Njiitu làngug Parti Démocratique de Côte d’Ivoire), Saarl Bele Gude ak Giyóom Sóroo. Ñooñu, duñu mën a bokk ci palug Njiitu réew gii di ñëw.