LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (5/8/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ÑAXTU LIGGÉEYKAT YI CI WÀLLU YOON

Démb ci altine ji, 4 ut 2025, kurélug layookat yi, di Conseil de l’ordre des Avocats, génne na ab yégle ngir àddu ci ñaxtub liggéeykat yi ci wàllu Yoon. Ginnaaw bi liggéeykat yi taxawee ci wéyal seen ñaxtu bi, dugg nañu ci ñaari weer yoy, dañoo bank seen i loxo ba daanaka dara doxatul. Tolluwaay bu ni mel nag moo tax ba kurélug layookat yi di artu ci ni mbir yi tagatembee.

Ci seen yégle bi, laykat yaa ngi ñaawlu njeexital yu bon yi ñaxtu bi am ci àq ak yelleefi ma-xejj yi, rawatina téyandi yu gën a yàgg yi mu jur, nit ñiy gën a bari ci kaso yi ak xañ gi mu leen di xañ layoo bu digg-dóomu.

Lii yép tax na ñuy sàkku ci liggéeykat yi ñu bañ a taxawal lépp ci seen ñaxtu bi. Sàkku nañu itam ci Càmm gi mu taxaw ciy wareefam ngir askan wi mën a jot ci Yoon, te mu delloo Yoon kilifteefam. Naka noonu, Kurél gi di woo ñaari pàcc yépp ci seen i wareef ngir saafara mën a am.

SENEGAAL YOKK NA KAARAANGE GI CI DIGGANTEEM AK MALI

Réewum Senegaal sampal na sàndarmëri bi ñetti dal yu bees fa digganteem ak Mali. Ndogal lee ngi mu jël ginnaaw cong yu bari yu rëtëlkat yi di amal fa réewum Mali, rawatina yi ñu mujjee amal ci weeru sulet bi te mu jege lool dig bi dox ci seen diggante. Fa kéedugu, taxawal na fa benn dal bu ñuy duppe ci nasaraan légion. Fa Tàmbaakundaa, mu amal fa benn birigàdd (brigade de recherche). Fa Saaraya itam, yóbbu na fa genn kippu gu ñu naan Groupe d’action rapide. Ñetti dal yépp nag matale nañu ci doxal ngir aar diiwaan boobu, rawatina fa wër Kidiraa, fa dugg beek génn bi ëppee doole ci diggante ñaari réew yi.

Fa goxu Bàkkel itam aaye nañu móto yi ñuy daw guddi gi. Nde, ñoom la defkati ñaawteef yi di faral di jëfandikoo. Bu weesoo loolu, Làrme bee ngi woo askanu gox bépp ci ñu lëkkatook ñoom ngir dooleel matuwaayi kaaraange gi.

MBIRI ELAAS BAABAKAR JUM « KOCC BARMA »

Démb ci altine ji Elaas Baabakar Jum, gën a siiwe ci turu Kocc Barma, doon na janook àttekat bu mag bi fa Ëttu àttekaay bu mag bob Ndakaaru. Ca kanamu àttekat ba nag, Elaas Baabakar Jum dafa weddi tuuma yépp yu ñu ko gàll ci mbir yu laaleek i widewoo ak i nataal yees wasaare ci lënd gi. Fa mu taxaw daal la taxaw naan « Duma Kocc Barma ». Li mu bëgg a gëmloo àttekat ba mooy ni moom dalalkat kepp la ci, maanaam li ñuy wax hébergeur de sites Internet kepp la. Ba tax mu jàpp ni yoonam nekkul ci lees di jàllale ci dal yooyule.

Ginnaaw bi ñu ko dégloo, dees na déglu ci fan yii di ñëw kii di Elaas Asan Demba mi ñu jàpp ci fan yii weesu fa dalub roppalaan AIBD (Aéroport international Blaise Diagne). Ñoom ñaar itam dinañu janoo balaa yàgg ci kanamu àttekat.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj