LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (5/9/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

MÀGGAL TUUBAA

Démb ci altine ji, 4 sàttumbar 2023, la murit yi doon bésal màggalug Tuubaa gi. Muy bés bu ñuy màggal at mu jot ci ndigalu Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke mi sos yoonu murit. Ñu ciy jàng alxuraan (téere julit ñi), ay xasida (mbindi Sëriñ bi) ak di ci berndeel jaamu Yàlla yi, tàmbalee ko ci ginaar ba ci gëléem ni ko Sëriñ bi diglee woon ngir ñu santale ko Boroom Bi. Bés bi nag, Sëriñ bee ngi ko jëkk a digle ca atum 1895, ba muy dem ca tukkig géej ga. Gu ren jii di 129eel wi yoon.

TÀGGE : FAATU KINNE DEM DEM NA

Taskatu xibaar bii di Faatu Kinne Dem, daan liggéeye TFM (Télévision Futurs Médias) moo génn àddina. Démb ci altine ji la faatu fa raglub Ndakaaru (Hôpital Principal de Dakar). Looloo ngi xew ginnaaw wopp gi ko tëraloon ba ñu yóbbu ko fa.

Keneen ku faatu ci altine ji di Sã Póol Dalmaydaa. Moom nag, nekkoon na way-jëmmal bu ràññeeku lool ci filmi Senegaal yi. Ndax, ku mënoon liggéeyam la. Cib aksidaŋ lañ wax ni la ñàkkee bakkanam. Muy tiis wu rey wu dal ci kow Senegaal, rawatina kibaaraan yeek ahlu caada. Lu defu waxu di leen jaale.

TÀGGAT-YARAM

Nàmpalis Mendi am na këlëb bu bees. RC Lens la dem ginnaaw biñ amee déggoo ci àppu ñaari at. Muy nag déggoo bu dal xel. Nde, ginnaaw bi mu tàggook këlëbu àngale bii di Leicester, gaynde Senegaal gi amatul woon fu muy joŋantee. Looloo waral sax ba Aliw Siise jotu ko woon a woo ci joŋante Senegaal bii di ñëw.

BITIM-RÉEW

Fa Gaboŋ, Seneraal Óligi Ngemaa daldi nay waat ci altine ji. Ginnaaw bi ñu nangoo Nguur ga ca loxoy Aali Bongo mi ñu siiwaloon ni moo raw ca wote ya, takk-der ya dañoo gaawantu taxawal ag Càmm ngir joyyanti nguur ga ci njiitul Seneraal Ngemaa. Bi mbir mi amee ak tey nag, askan wa wone na ni takk-der yi la àndal ngir won ginnaaw lees jot a dund. Nuy xaar ba xam coppite dina am ci doxalinu njiit yu bees yeem déet.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj