Caabal gi IGF (Inspection Générale des Finances) defoon ci naalu PRODAC (Programme des Domaines Agricoles Communautaires) wi, coow laa ngi wéy ba tey. Cig pàttali, mbirum caabal googu taxoon na Maam Mbay Ñaŋ pelent ki fi nekk tey elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, ba ñu daanoon ko ci. Coow loolu moo dekkiwaat. Bees sukkandikoo ci waa “Libération”, caabal googu jébbal nañu ko waa DIC (Division des Investigations Criminelles).
COOWAL “MOTION DE CENSURE” LI
Mbir moomu mi ngi sosu woon ginnaaw bi ñu bañalee Njiitu réew mi càkkuteefam. Maanaam, ñu amal i coppite ci ndeyu àtte bi ngir ñu mën fee jële ñaari campeef yii di HCCT ak CESE. Bi ñu ko ko bañalee nag, mu def ay pexey boppam. Ginnaaw loolu, kii di Abdu Mbów mi jiite kippaangog Bennoo Bokk Yaakaar gi dafa xamle woon ne dañuy jébbal li ñuy dippe “motion de censure”. Waaye, loolu jëlagul yoonu àntu. Nde, Njiitu réew mi dafa woote tey, ci alxames ji, fa Ngomblaan ga li ñuy dippe “sessionextraordinaire” nga xam ne mën nañ cee laal poñ yu bari. Bi ci gën a fés, mooy mbirum “Déclaration de Politique Générale”. Mu mel ni, loolu pexe la ngir gàntal pexem waa BBY mi nga xam ne mooy daaneel Nguuru Usmaan Sonko gi.
BÉSUB SET-SETAL
Gaawug ginnaaw suba gi, yemoo ak juróom-ñaari fan ci weeru sàttumbaar, mooy doon ñeenteelu yoon ñuy amal bésub set-setal bi. Bés boobu, bariwul dëkk yu ciy nangoo des ginnaaw. Kii di Njiitu réew meek elimaanu jëwriñ yi, gis nañu ne ñoom duñu bokk béréb yi ñu koy defe. Wii yoon, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, fale ca Maatam lay defee set-setal bi.
JËWRIÑ JI ÑU DÉNK WÀLLU YOON DÀQ NA NDAJE MI
Tey, ci alxames ji, la jëwriñ ji ñu dénk wàllu Yoon, Usmaan Jaañ, waroon a janook saabalukaay yi bu ñeenti waxtu ci ngoon jotee. Waaye, ndaje moomu daf koo mujje dàq. Ba tey, joxeegul àpp ngir def waxtaan woowu donte ne sax, waxtaan wu am solo la naroon a doon. Nde, dafa am ay poñ yu mu waroon a leeral. Muy lu ci mel ni jële gi ñu fi war a jële HCCT ak CESE, Ngomblaan gi ñuy waaj a tas ak li ñuy dippe “reddition des comptes”. Li sabab mu soppi taxawaayam ci diggante dafa umpe, donte ne sax, xew-xew yi fi jaar diggante démb ak tey bari na lool.
FARÃS AMAAT NA ELIMAANU JËWRIÑ
Emmanuel Macron, Njiitu réewu Farãs li tabb na elimaanu jëwriñ yi, ci alxamesu tey jii. Nde, lu yàggul dara, réew mooma, amatul woon elimaanu jëwriñ. Ki mu tabb, mi ngi wuyoo ci turu Michel Barnier. Mi ngi am lu tollu ci juróom-ñaar-fukki at ak ñett. Moom nag, xaw naa nekk mag bees méngalee atam ak ki mu wuutu fa béréb boobu. Nde, kooku moo nekk ki gënoon a doon xale ku mës yor ndombog-tànk googu. Moom Gabriel Attal mi yoroon ndombog-tànk googu, mi ngi tollu ci fanweeri at ak juróom.