Kujje gee ngi waajal lu bees ñeel wote yiñ dégmal. Sëñ Abdurahmaan Juuf, di njiitul làngug pólitig gii di Awale, moo ko xamle démb ci dibéer ji. Fekk ñu doon ko dalal ca jotaayu Grand Jury bu Rfm. Donte ni xuusul ba ci biir, biral na ni ag kurél la nar a doon gog liggéeyam du doon leneen lu dul topp ak taxaw ci anam yi wote yi di doxe. Li ñuy bañ nag mooy Càmm gi yore lépp, ku ko neex mu bokk, ku ko neexul mu seppi.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Kuréli jàngalekat yii di Cusems ak Saems namm nañoo bank seen i lox naka ëllëg ci talaata ji. Ginnaaw bi ñu ko yéglee ci seen jàkkaarlook taskati xibaar yi ci àjjuma jii weesu, Càmm gi xëy na tey di leen dànkaafu. Ci yëgle bi mu génne, mi ngi ciy siiwal ni Càmm gi jot na dugal 250i tamndareet ci déggoo yi. Waaye yamul ci loolu, nde mi ngi fàttali jàngalekat yi ni bés bu ñu jalgatee déggoo bi ba lànk bañ a jàngale, Càmm gi am na sañ-sañu càmbaraat ci saa si lépp lu ñu tëraloon.
Ci njàngale mu kawe meet, jàngalekat yi bokk SAES (Syndicat autonome de l’enseignement supérieur) yi xëy nañu tey ci altine ji bank seen loxo. Te dinañu ko tóllanti naka ëllëg ci talaata ji. Muy 48i waxtu, maanaam ñaari fan yu jàng dul am ci jàngune Senegaal yi. Ñoom nag, seen bëg-bëgg mooy Càmm gi tijji njàngune Séex Anta Jóob bu Ndakaaru ngir ñu tàmbali jotaayu jàngale yi. Li ñu wax nag mooy ginnaaw bi yàqute yi amee la kilifa yi tëjoon jàngune bi. Te boobook tey amoon nañ jot ju bare ngir defaraat yàqute yi. Waaye, defuñu ko. Dañu xaar ba tijji des ñuy xañ ndongo yi fu ñu jànge. Ñu gëm nag ni dara waralul ñàkk tijji gi lu dul mbiri pólitig, te ñépp xam nañu ko.
MBIRI USMAAN SONKO
Tey ci altine ji, la ëttu àttewaay bu Cedeao doon àdduwaat ci mbir mi dox ci diggante Usmaan Sonko ak Càmmu Senegaal. AJE bi, di layalkatu Càmm gi dafa sàkkooti ci àttekat bi mu dàq jotaay bi ndax jotuñoo waajal ci xóotal bi. Waaye àttekat bi dafa koo lànkal, dellu woo leen ci layoo bi wenn yoon. Ginnaaw bi mu dégloo nag ñaari pàcc yépp, dina joxe àtte bi ci ayu-bés bii di ñëw, ci bésu àjjuma 17 nowàmbar 2023.
MBËKK MI
Ba tey, mbëkk maa ngi wéy di lëmbe réew mi. Ndee yu bare yeek njàqare ji mu jur taxul wenn yoon ndaw yi teggi seen tànk. Dafa mel ni sax tey la waalo gën a aay. Démb rekk ci dibéer ji, jëwriñ ji ñu dénk mbiri bitim-réew ak saa-senegaal ya fay yëngu xamle na ni xettali nañu 770i doom-aadama yu bawoo Senegaal fa réewum Móritani. Am na sax 13 yu ci ñàkk seen i bakkan ak 12 yu ñu rawale jamono yii ca loppitaal. Li ci gën a yéeme nag mooy jigéen ñeek xale yi dañ ci tàmbalee bare léegi.