Lu tollu ci ñaari ayu-bés ginnaaw ba ëttu àttewaay bu kowe bi neenalee àtteb Sabasi Fay ba, àppalees na layoo bi war a ame fi Ndakaaru. Àtte boobu mi ngi ñeel ag génnam ci wayndarew wote yi. Layoo boobu ñi ngi ko war a amal ci talaata jii di ñëw yemoo ak fukki fan ak ñaar ci weeru desàmbar wii. Su boobaa dees na xam ndax, dañu koy bàyyi ci wayndare wi walla dañu ko ciy génnee.
SÉYDINAA UMAR TURE DAKKAL NA LIGGÉEYAM
Ci atum 2021 lañu ko dàqee woon ca béréb ba mu doon liggéeye. Ginnaaw gi ñu jëlewaat ko ca béréb ba mu doon jàngalee tamit. Ca la ko meeru Ndakaaru Bàrtelemi Jaas jël ci benn bànqaas ci meeri ba mu cay liggéey. Moom nag xamle na ne lawax la ci wote yii di ñëw. Péete gi mu am ci wàllu pólitig moo tax mu jàpp ne mënul a wéyal liggéey boobu. Moo tax mu jébbal démb ci suba meeru Ndakaaru bi bataaxal biy firndeel ne bàyyi na.
SAHRAA BU USMAAN SONKO
Faatimaa Sahraa Wage, ñu gën koo xam ci turu Sahraa bu Usmaan Sonko, bàyyees na bàyyig négandiku. Loolu mi ngi am ginnaaw bi ko ëttu dab-dabaatal (cour d’appel) bu Tàmbaakundaa nangulee démb càkkuteefam googu. Léegi kay, li des mooy ndax, ëttu toppekaay bu mag bi (parquet général) bi nasaxalul ndogal loolu am déed. Moom nag, ay weer a ngi nii ginnaaw bi ñu ko tegee loxo ak léegi. Ñu ngi ko doon toppe tuumay yee fitna, jëf joo xam ne mën na nasaxal jàmmi askan wi.
RÉEW YI BOKK CI CAN 2024 BOB JIGÉEN ÑI
Démb moo nekkoon joŋante yu mujj yi ngir xam yan réew ñooy teewe CAN boobu. CAN boobu nag réewu Marog moo koy amal. Fukki réew ak ñaar ñooy fekke joŋante yu mujj yi (phase finale). Réew yooyu di Senegaal, Afrique du Sud, Alseeri, RDC, Gana, Tansani, Botsuwaanaa, Sàmbi, Niseriyaa, Mali, Tinisi ak Marog miy amal joŋante bi.
AMAA BALDE – GIRI BÓRDOO
Am na lu jege daanaka ñaari at ba ñu bëggee taxawal làmb jooju. Booba ba léegi, gaa ñaa ngi ciy dox ngir ñaar ñooñu bëre. Ba ñu mujjoon ko jàpp juróom-ñaari fan ci weeru saŋwiye. Waaye, ba tey dafa mel ni mbir yi sotteegul. Ndax, ay xibaar rot ci ne Amaa Balde dafa jébbal CNG li ñuy dippe “certificat médical” bu tollu ci fanweeri fan. Maanaam boobu buy jeex fan yi néew a ciy des ngir àppu làmb ji ñëw. Kon, fi mu tollu nii mënaguñoo jàpp ne làmb jooju dina mën a am bés boobu.