LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (6/2/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LIMUB SAABALUKAAY YI SÀMMONTE AK SÀRT YI

Sànq ci bëccëg lañu siiwal limub saabalukaay yi nga xam ne sàmmonte nañu ak sàrt yi yoon tëral. Dafa di, kenn daa umpalewul ne, bu yàggul dara am na lim bu ñu siiwaloon ba mu juroon fi coow. Ndax, dafa am ñoo xam ne sàmmontewuñu woon ak sàrt yi. Saabalukaay yi nag, bari nañu lool te wuute. Am na ay tele, am ay rajo, am ay dali web, añs. Njëwriñ giy saytu wàll woowu xamle na ne lu tollu ci 639i saabalukaay mi ngi ci réew mi. Lu tollu ci 258 yi ñoo ci sàmmonte ak sàrt yi Yoon teg, 381 yi yépp sàmmontewuñu ak li Yoon tëral.

MURIG MBALAANU KIIRAAYU AAMADU BA AK BIRIMA MÀNGARA

Coowal murig mbalaanu kiiraayu Aamadu Ba ak Birima Màngara moo lëmbe réew mi fan yii yépp. Nde, kenn umpalewul ne bu yàggul dara lañu muri mbalaanu kiiraayu seen naataangoo bii di Farba Ngom. Dafa di, wii yoon it, nee ñu toppekatu bokkeef gi moo sàkku woon ci Ngomblaan gi liggéey boobu. Ndax, dafa am ci mbiri suuf yu ñuy tudd ñaari dépite yooyu. Waaye, càkkuteef boobu mujjul a àntu. Nde, àttekatu “2ème cabinet” bu ëttu àttekaay bu Ndakaaru moo lànk bees sukkandikoo ci xibaar yi rotagum.

GÀNTAL NAÑU CÀKKUTEEFU SAMIYEL SAAR

Ci njeexitalu weeru nowàmbar atum 2024 lañu ko yóbbu woon kaso. Booba ba tay, kenn àtteegu ko, ma nga fa. Nde, moom mbirum luubal mu tollu ci 8,17 miliyaar. Way-bokki këru liggéey googu di WAE (West Africa Energy) ñoo ko jure. Looloo sabab ag jàppam. Moom nag, ginnaaw diir ba mu def fa kaso ba, da doon sàkku ñu bàyyi ko, bàyyig négandiku. Waaye, càkkuteefam boobu dañu koo mujjee gàntal.

NDONGOY BÀMBEY DOOR NAÑ AY ÑAXTU

Fan yii mel na ne coow yi dooraat na ci daara yu kawe yi. Daara ju kowe joj Ndakaaru doy na ci firnde. Ndongo yi nekk fa daara ju kowe joj Bàmbey feelu nañu leen ci coow li. Nde, ñoom tamit, nee ñu dinañu dakkal njàng mi lu tollu ci ñetti fan. Li ñu ci jublu du lenn lu moy àrtu kilifay Nguur gi. Bu ci kilifa yi yéyul yàbbi, dinañu làbbali.

SECTION DE RECHERCHE BU NDAR TEG NA LOXO WAA QNET

QNET genn këru liggéey la gu ay gaay taxawaloon ngir nax ci ay doom-aadama. Dafa di, ñoom dañu doon yëngu ci mbir yu bari. Doon dig ña fa doon dem ay dig yu ñu dul matale. Te, li ci gën a doy-waar mooy jot nañu cee jëflante ak lu tollu ci juróom-fukki nit ak juróom-ñaar. Te, ku nekk ci ñoom joxe na lu tollu ci juróom walla juróom-benni téeméeri junni. Waaye, mu mel ni seen i naxaatee ngi waaj a jeex. Ndax, jàpp nañu ci fukk ak ñett, ñeenti jigéen ak juróom-ñeenti góor.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj