LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (6/3/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

“SUIT” WEDDI NA XIBAAR BI L’OBS JIBAL

SUIT (Syndicat Unique des Travailleurs du Trésor) mooy kurél gi ëmb liggéeykati béréb bii di “Trésor public”. Sàndikaa boobu indi na ay leeral ci xew-xew ba fa amoon dibéer jee weesu. Nde, saabalukaay bii di L’Observateur dafa xëy tay siiwal ciy xëtam bu njëkk ne ay sàmbaa-bóoy dañoo songoon béréb bii di “Direction de l’informatique du Trésor public”. Jël nañu fa ñetti nosukaay ak koppar gu tollu ci ñeen-fukki junni. Waaye, yamuñu foofu. Ndax, yokku nañu ci nosukaay yooyu ñu jël ci la wayndarey béréb ba nekkoon. Ñii di waa SUIT xamle nañu ne mbir mi demewul noonu. Am ndog mu ndaw la woon rekk. Te, ubbi nañu ci ag luñnutu. Ñuy leeral asakan wi ne dara sikkul ci seen i jumtukaay. Amul wenn wayndare woo xam ne ñàkk nañu ko. Ñi ngi leen denc fu am kaaraange. Rax-ci-dolli, jumtukaay yi ñu sàcc amul dayo noonu yépp.

DAAN NAÑU ABDULAAY NJAAY

Abdulaay Njaay mooy ki yor kàddu Farba Ngom, maanaam, li ñiy dippe “chargé de communication”. Moom nag, Yoon daan na ko démb ci ay kàddu yu mu yékkati woon. Li ñu koy toppe mooy jibal xibaar yu wérul ak yékkati kàddu yoo xam ne dëppoowul ak jikko yu rafet yi. Ba tax na, Yoon daan na ko juróom-benni weeri kaso ak alamaan bu tollu ci ñeen-fukki junni.

NDOG MU METTI CI RN1 BI

Ndog yaa ngi wéy di lëmbe réew mi. Saa su ñu jàppee ne wàññeeku na, fekk ne booba la Waalo gën a aay. Nde, barki-démb, ndog mu metti am na fa wetu Gudira ba ñaari doomi-aadama ñàkk ca seen i bakkan. Li ci gën a metteeti mooy ne ñoom ñaar ay mag ak rakk lañu woon. Ñoom ñaar, ab móto lañu yoroon. Benn sëfaan lañu mbëkk, daldi faatu ca saa sa.

XEW-XEW BU DOY-WAAR FA PIKIN

Xuloo diggante aawo ak ñaareel moo amoon fa koñ bii di Ginnaaw Raay (Sud), nekk fa Pikin. Coow loolu nag, dafa mujje ëpp i loxo. Ndax, aawo bi, A. Gajaga dafa jël asib sotti ko ñaareel bi, S. Sow. Moom ñaareel bi, jamono jii, ma nga fa raglu bu Seneraal Idiriisa Njaay bu “Grand Yoff”. Ndax, dafa am lakk-lakk yu metti. Kii di aawo bi moom, mook doomam teg nañu leen loxo ginnaaw ab jure bees sukkandikoo ci waa Seneweb. Suba ci àjjuma ji lañu leen di jébbal ëttu àttewaay bu Pikin.

XIBAAR BU DIIS CI GAYNDEY SENEGAAL YI

Bu yàggul dara la ñaari gaynde yii di Elimaan Njaay ak Nikolaa Jakson amoon ay gaañu-gaañu. Gaañu-gaañu yooyu tax ba duñu mën a teewe joŋante biy dox diggante Sudaŋ ak Senegaal. Ñu ne déet-a-waay, geneen gaynde gu saa-senegaal yi doon bàyyi xel tamit am gaañu-gaañu. Moom, Abiib Jaraa, du mujjee bokk ci ñiy joŋante. Mu doon beneen xibaar bu diis lool ci gayndey Senegaal yi. Ndax, kenn umpalewul njariñu gaynde yooyu ci joŋante yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj