LI GËN A FES CI XIBAARI BES BI (6/9/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

BÀYYI NAÑU XALIL KAMARA BU SENEGO

Bërki-démb ci talaata ji lañu téye woon taskatu xibaarub Senego bi fa DIC. Li ko waral mooy yaxal bu mu siiwaloon ñaari fan ci weeru sàttumbaar wii, dippe woon ko « Yëgleb Usmaan Sonko bi ñuy xaar (la déclaration attendue de Ousmane Sonko) ». Moom nag jamono jii ñi ngi koy toppe biral ay xibaar yu wérul, tooñ Njiitu réew mi, yàq der ak ŋàññi ag kurélug lëmm (un corps constitué).

Ay naataangoom yi mu bokkal kurél gii di APPEL (association des éditeurs et professionnels de la presse en ligne) ñi ngi doon sàkku ñu bàyyi ko ci nu mu gën a gaawe. Ndax, ñoom xamle nañu yaxal boobu tax ñu téye du mooy aji-bind ji. Rax-ci-dolli ñi ngi ñaawlu ni Nguur Senegaal di doxale ag taskatu xibaar yi. Ndax, ci lu yomb rekk daf leen di téye. Waaye, seen naataangoo boobu mujj nañu ko bàyyi tey ci ngoon.

 F24 JÓGATI NA

Kurélu F24 boole ay làng ak i way-moomeel delluwaat na ca mbedd ma. Ab diir ginnaaw ba mu gëjee yëngal, delloowaat na buum ca mboy-mboy ga. Àjjuma jii ñu dëgmal namm nañoo amal am ndajem-ñaxtu. Li ñu ko dugge mooy ñu bàyyi mboolem ñi ñu jàpp te wuteg gis-gis ci pólitig kepp lal ko, amal ay wote yu leer nàññ. Te, képp ku bëgg a bokk ñu bañ ko gal-gal, bàyyi ko mu bokk.

LIMUB ÑI TEEWE MÀGGALUG TUUBAA

Màggalug ren ji bokk na ci yi ëpp ay nit bees ko méngalee ak yii weesu. Ndax, yégle bi li mu fésal mooy ne diggante benn fan ci weeru sàttumbar ba ñeenti fan ci weer wi def nañu ay luññutukat ci bunt yu wute yi ñuy dugge Tuubaa. Duggukaay yooyu mooy bu Ngaabu, Mbàkke, Daaru Muxti, Daara ak génnukaayu Péage bi. Limub daamar yi tollu na ci 201.871 ak yiy wëlbatiku. Limub ñi teewe màggal gi tollu ci 5.875.536i doomi aadama, 4.605.946 yi ñu fa ñëw la, 1.269.590 yi moom Tuubaa ak li ko wër lañu dëkk.

LIMUB ÑI FAATU CI AKSIDAŊ YI AM CI MÀGGAL GI

Altine jii weesu moo nekkoon bésub màggalu Tuuba nga xam ne fépp la ay nit di jóge di wuyuji woote boobu. Loolu bokk ci li sabab aksidaŋ ak limub nit ñi ci ñàkk seen i bakkan. Ñii di waa Birigaad sàppëer pompiyee yi ñoo fésal limub ñi ci faatu. Xamle nañu ne jamono jii lu tollu ci ñaar-fukki doomi aadama ak benn ñoo ci ñàkk seen bakkan. Mu am tamit ñu bari ñoo xam ne jële nañu ci ay gaañu-gaañu.

WAVE MI NGI ARTU

Këru yóbbante ak jot xaalis gii di Wave mi ngi artu ñiy jote xaalis ci moom ci jëfi sàmbaa-bóoy yi. Moo tax mu leen di xamal ni mboolem xéewal (promotion, bonus) yi ñuy def, ci seen xëti mbaali-jokkoo lañu leen di jaarale. Kon, bu kenn dugg ci genn lënkaay gu ñu ko yónnee, lu dul muy goo xam ne ci ñoom la jóge. Te, ku bëgg xibaar, bul tàyyal, mën nga woote ci seen lim bii : 200600.

MBËKK MI

Jamono jii, ndawi Senegaal yi Espaañ mooy seen jëmukaay. Liy xew ci géej gi ci jamono yii ak la leen jiitu, mel na ne feesul seen i bët. Ñii dem nañu ba àgg, ñee àgguñu, ñee ñu delloosi leen. Waaye, am na ñoo xam ne moom jotuñoo sax génn réew mi. Loolu moo dal ñi nekkoon ci ñaari gaal yi ñu teg loxo ci boori Luga. Limu ñi nekkoon ci gaal yooyu mi ngi tollu ci ñaari téeméeri doomi-aadama ak ñeen-fukk ak ñaar.

LÀMBU MÓODU LÓO-BOOY ÑAŊ JÀPP NAÑU KO

Ginnaaw bi làmbam ji dox digganteem ak Amaa Balde taxawee, moom ak Booy Ñaŋ tamit jàppal nañu ko bés. Maanaam day bëre ak doomi Fàllaay Balde ji ba pare soog di bëree ak doomi De Góol ji. Làmb jooju ñi ngi ko jàpp altine benn fan ci weeru saŋwiye 2024 ca Arène nationale bu Pikin.

CONG MU METTI FA BURKINA

Réew moomu di Burkinaa Faaso ay at a ngi nii yoo xam ne mi ngi ci xeex bu metti ak rëtalkat yi. Waaye ba tey mbir mi sotteegul. Ndax, seen làrme bi ñàkk na lim bu takku ci ay sóobareem ak ñeneen ñu bokkul ci sóobare yi, ñu leen dippe ay “VDP” Volontaires pour la Défense de la Patrie. Ci talaata ji bóom nañu lu tollu ci juróom-fukk ak ñett ci seen i xeexkat fa bëj-gànnaaru réew ma. Fukk ak juróom-ñaar yi ay sóobare lañu, fanweer yi ak juróom-benn moom ay maxejj yu takku woon lañu ngir aar seen réew.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj