LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (7/1/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LAYOOB WATTUKATI KAARAANGEG LËKKATOO SÀMM SA KÀDDU

Tay ci altine ji, ëttu àttekaay bu Ndar doon na àtte wattukati kaaraangeg lëkkatoo Sàmm sa kàddu. Ñoo ngi tolloon ci 80i doom-aadama yu ñu tegoon loxoon ci tafaar yi amoon fa Ndar ca kàmpaañi wotey Ngomblaan ga weesu. Ñoo ngi leen doon toppe « càcc gu ànd ak tafaar, gaañaate, jëfandikoo ay ngànnaay yu yoon tere ak jalgati yoon ». Ginnaaw bi ñu leen àttee ba noppi, ëtt ba daan na ñett ci ñoom ñetti atu kaso yu ñuy tëdd. Am na ñu mu daan ñaari ati kaso yoy, dinañu ci tëdd 6i weer yi ; mu am it ñeneen ñu mu daan ñetti ati kaso yu ñu war a tëdd ñaar yi. Waa pàrti siwil beet dinañu jot i ndàmpaay yu tollu ci diggante 50 000 ba 500 000 FCFA. Waaye, seen laykat bii di Meetar Elaas Juuf àndul ci àtte bi te dina dugal dabantal ci bés bi.

PERMI POÑ YI

Dinañu tàmbalee doxal permi poñ yi (permis à point) ci atum 2025 mi. Xibaar la bu tukkee ci Yànqooba Jémme, jëwriñu tabaxte yeek yaaleg suuf seek jaww ji. Fekk ñu doon ko dalal démb ci dibéer ji, ci jotaayu waxtaan bii di En vérité, fa rajo RSI (Radio Sénégal International). Naka noonu, muy xamle ni coppite yu am solo dinañu ci am ci at mii nu sog a dugg. Fi ñu tollu ci waxtaan yi ak way-yëngu yi ci fànn wile sori na. Te lees namm ci coppite yi mooy wóoral anam yees di joxee permi yi ak saytu bu jaar yoon ci nees leen di jébbalee ci lekkool yiy jàngale dawal.

100 KG YÀMBAA YI ÑU TEG LOXO FA CAAROY

100i kiloy yàmbaa la Sàndarmëri teg loxo fa Caaroy-Géej. Looloo ngi xew ci xeex bi muy xeex jëfandikoo ak njaayum sineebar bi ak yokk gi ñu yokk caytu kaaraange gi ci réew mépp. Ci noonu la Birigàdd Caaroy bi mbaal jenn waay ci guddi 3 jàpp 4i fani sãwiyee, ci tefesu géeju Mbatal. Bi ñu ko tegee loxo lañu fekk ci moom mu yor ñaari saaku yu mu séddale sineebar bi.

BITIM-RÉEW

Kémi Sebaa, njiitu ONG Urgence Panafricanistes, bëgg na bokk ci wotey Njiitu réew yii di ñëw fa réewum Benee. Barki-démb ci dibéer ji, 5 sãwiyee 2025 la fésal yéeneem ngir doon lawax. Muy ndogal lu mu jël, bees sukkandikoo ciy waxam, ngir jooxe càkkuteef yu bari yu muy jot. Làngug pólitig gii di Les démocrates la bëgg lëkkatool ngir taxawal nekkug lawaxam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj