Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, rafetlu na taxawaayu FMI (Fonds Monétaire Internationale) ci li kurél gi nangoo gunge Càmm gi. Muy taxawaay bu Julie Kozack mi yor kàddu FMI siiwal keroog ci àjjuma ji, ginnaaw bi leen Càmm gi jébbalee njureef yi tukkee ci caytug yorinu alalu réew mi ci fukki at ak ñaar yii weesu (2012-2024). Naka noonu, moom Njiitu réew mi, dellu na dëggal ni tey la gën a dogu ngir def réewum Senegaal digaale bu wóor ni mu ko waxee woon keroog bi muy waat ci kanamu askan wi.
MBAWUG MAKI SÀLL ÑEEL NJIITEEFU 4P
Maki Sàll mi fi nekkoon Njiitu réewum Senegaal (2012-2024) dëggal na jógeem ca boppu 4P (Pacte de Paris Pour la Planète et les Peuples). Muy ndombog-tànk bu ko Njiitu réewum Farãs dénkoon ngir muy xeex ñeel kéewnga gu mucc ak jàmmu xeet yi. Bees sukkandikoo ci kàddu yi mu siiwal, tabb gi ñu ko tab ci boppu toftaleg lëkkatoo Takku Wallu Senegaal moo sabab mu dello cër boobu. Ndax, bëggul wenn yoon ñàkk dëppoo di feeñ ci diggante ñaari cër yi. Ba tax na, dina delloo bu 4P bi keroog 9i oktoobar 2024 bu ndajem Hambourg mi jeexee.
APR ÀDDU NA CI CAABALUG CAYTU GI
Ginnaaw bi magum jëwriñ yi biralee njureefi caytu gi aju ci yorinu alali réew mi ci at yi weesu, waa APR yi mu laaleel àddu nañu ci. Ci yëgle bi ñu siiwal, ña ngay ŋàññ Nguur gi ak di wax ne daf leen di tuumaal ci lu amul lenn firnde. Ndax, caabal gi wayndare négandiku la. Campeef gii di Cour des comptes rekk mooy àttewaay bi mën a àddu ci yorinu alalu réew mi. Te, ëtt boobu du joxe ay njureef fileek jébbalul caabalug négandiku googu ñi fi nekkoon kilifa ca jamono jooju ngir am seen gis-gis ci mbir mi ba mën a tëdde njaaxaanaay. Te ëtt boobu, ci diirub ñetti weer lay joxe àtteem ñeel wayndare woowu.
UBBITEG LEKKOOL YI
Ginnaaw ñetti weeri bër yi ñu toog, tey ci altine ji la ndongo yi dellu ci jàngu yi ngir door atum 2024-2025 mi. Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay fay, yékkati ay kàddu di ñaanal ndongo yi ubbite gu am njariñ ak atum njàng mu baax. Fa diiwaanu Ndakaaru nag, jëwriñ ji ñu dénk njàng mi amal na fa ay doxantu ci lekkool yi ngir saytu ni ubbite gi deme. Naka noonu, nemmeeku nañu itam teewaayu góornoor yi ci lekkool yi ci gox yeek goxaat yi ngir saytu ubbite gi.
COOWAL MUURAAY YI CI LEKKOOL KATOLIG YI
Jëwriñ ji ñu dénk njàng mi, Mustafaa Giraasi àddu na ci coowal muuraay yi fi jiboon ci lekkool katolig yi. Muy xamle ni dekkare bi ci magum jëwriñ yi doon sàkku am na te moom la njiitu lekkool yi di tijjee tey. Muy leeral ni leneen nekkul ci dekkare bi lu dul ay pàttali ñeel tënku yi Ndayu Sàrti Réew mi wax ba noppi, te muy dellu ciy mbaaxi bokk dund ak nangulante, dëgëral rattaxaayu diggante yi ak nangu wuute yi. Ba tax ñuy sàkku ci sàrti doxiinu biir lekkool yi ñu sàmmonteek tënku yooyu.