Fukki fan kepp a des ci wotey palug dépite yi. Ba tay, am na ñu dëggalagul seen bopp ca lëkkatoo walla làng ga ñu nekk. Waa UDS (Union pour le Développement du Sénégal) bu Aji Mbergaan Kanute nga xam ne ci lëkkatoog Takku Wallu Senegaal la bokkoon, nekkoon ñaar-fukk ak ñeenteel ci toftale gi, mujj na fa jóge. Xamal na ay ñoñam ban toftale la namm a àndal ci wote yii. Tay, ci alxames ji lañu daje ci seen màkkaanu làng, amal aw waxtaan. Ginnaaw gi, ci lañu génnee ab yégle xamle ne waa Pastef lañuy àndal ci wote yii.
Naka noonu, kii di meeru HLM bi mujj na a def tànneefam. Moom, Mustafaa Jóob, xamle na ne lëkkatoog Pastef bu Usmaan Sonko lay dimbali ci wotey palug dépite yii.
LU BEES CI MBIRUM PRODAC MI
Luubal ga amoon ca PRODAC (Programme des Domaines Agricoles Communautaires), indi woon fi coow lu réy ca jamonoy Maki Sàll, diggante Maam Mbay Ñaŋ ak Usmaan Sonko jibaat na. Ndaxte, am na ñu ñu ci jot a teg loxo. Ñi ñu jàpp du ñenn ñu moy Mamina Dafe (ancien coordonnateur national PRODAC) ak Ibraayma Siise nga xam ne dafa yor këru liggéey (dirigeant de la société Tida). Ñii di waa DIC ñoo leen teg loxo ginnaaw ba ñu leen jébbalee caabalug IGF gi. Ñaar ñooñu nag, ña nga leen téye ca Yoon ba tey. Maanaam, dañu leen a def li ñu naan “garde à vue”.
JÀMMAARLOO YI DOORAAT NAÑU FA UCAD
Lu yàggul dara rekk, ñenn ci ndongo yi (ñi nekk Master) ñi ngi doon jàmmaarloowaat ak takk-der yi ñeel mbirum peyoor. Waaye, wii yoon, mel na ne xeex bi ñépp a ci bokk. Sabab bi ci njëkk mooy ne ndongo yi dañoo bëgg ñu tijji bérébi lekkuwaay ya fa nekk yépp. Ñaareel bi, defaraat seen “terrain de football”, béréb bu leen soxal lool. Ndax, nee ñu, fa lañuy tàggate seen yaram, di fa féexalee seen xol tamit. Ñetteel bi, mooy ñu jox ag daamar (bus) ndongo yi nekke fa UAM (Université Amadou Mahtar Mbow) ngir yombal seen dem-ak-dikk. Bi ci mujj, mooy ñàkkug garab fa bérébi fajuwaay ba.
LU BEES CI MBIRUM DOORO GÉY
Bu yàggul dara lañu ko bàyyi moom Dooro Géy, def ko “sous-controle judiciaire”. Ndax, kenn umpalewul ne jàppoon nañu ko fi, ba tëj ko fi ab diir ci mbirum suuf. Am na keneen ku ñu teg loxo ñeel mbirum suuf moomu. Kii di kolonel Séex Saar moom, dañu ko woolu woon tay. Li waral woo gi ak ndéglu gi mooy, nee ñu, dafa am ag luubal ci mbirum suuf moo xam ne daf ci laale, moom ak Dooro ak Njiitul Cim-Translog Suarl. Bi ñu ko dégloo, ginnaaw gi lañu ko yóbb kaso. Moom, Séex Saar nag, ñoom li ñu koy jiiñ mooy dafa taqe ci mbirum jaayub bayaal ci dalub roppalaan bu yàgg bii di Aéroport International Léopold Sédar Senghor de Dakar bees sukkandikoo ci waa Senego.
XEW-XEW BU TIIS FA MEDINA
Xew-xew boobu mi ngi am tay ci alxames ji. Benn pàccu tabax (balcon d’un immeuble) moo fa daanu. Am na benn bakkan bu ci rot. Mu am tamit, ay yàq-yàq ci wàllu alal.
DÀQ NAÑU LAYOOB AMET NDÓOY
Ay fan ginnaaw bi ñu ko tegee loxo ak léegi, booba ba tey ma nga ñu téye. Tuuma yi ñu koy toppe mooy li ñuy dippe “défaut de permis, faux et usage de faux et blessure involontaire”. Tay, ci alxames ji lañu ko waroon a àtte. Waaye, layoom bi dañu koo mujjee dàq ba fukki fan ak ñaar ci weeru nowàmbar wii ñu nekk.