Xalifa Sàll ak Karim Wàdd yewweeku nañu. Delloos na leen seen i àqi maxejj yi leen di tax a doon lawax ci wotey 2024 yii di ñëw. Loolu la Ngombalaan gi dogal ci gaawug bërki-démb gi, ginnaaw bi dépite yi jàllalee sémbub àtte Limub 12/2023 bi soppi àtte Limub 2021-35 bu càrtug wote gi. Muy nag ndogal lu tukkee ci péncoo mi fi Njiitu réew mi, Maki Sàll, woote woon ci jamono yii weesu. Waaye m, bees déggee Sëñ Aadama Jaw, di jàngalekat ca jàngune UGB bu Ndar mbir mi ab lijjanti doŋŋ la.
XUWAAN BARANKOO
Layookatu Usmaan Sonko bii di Xuwaan Barankoo a nga ñuy génne réew mi. Ginnaaw biñ ko tegee loxo ci ñaari fan yii weesu, kilifay réewum Senegaal yee ngi koy doon jiiñ kootoo di woote fitna ak i tóoxidóona ci biir réew mi, ak itam ni dafa sàcc dugg ci biir réew mi. Jamono yii nag, ma nga ca dalub roppalaan bu AIBD ñuy lijjantiy mbiram ngir génne ko réew mi. Sëñ Baabakar Njaay itam, di beneen layookatu Usmaan Sonk, ñu tegoon ko loxo ci mbir mi, bàyyi nañ ko mu ñibbi.
YOKKUTE DUND GI
Njëgu soble si yokkootina. Ginnaaw bi jëndkat yeek jaaykat yi nemmikoo ni soble dafa jafe ci ja bi, njëg gi dafa dellu yokku ba kenn mënu koo jënd. Loolu tax ba fan yii, coow li ni kurr fi réew mi. Waaye, Nguur gi génne nab yégle di ci xamle ni balaa yàgg, soble su bare dina wàcc ci dëkk bi te dees ko mën a jëfandikoo ba balaa soble bi ñu bayee ci dëkk bi di ñor.
NISEER
CEDEAO wooteeti na meneen ndaje ci alxames jii di ñëw. Ndaje moomu nag, mi ngi ko woote ginnaaw bi àpp gi mu mayoon sóobare ya foqati Nguur ga ca Niseer jeexee. Ñu war cee jël ndogal li mujj ñeel sóobare yi ñu bëgg yóbbu ca Niseer ngir delloo Nguur ga ca loxoy Muhammet Basum ma nekkoon Njiitu réew ma.
Fii mu nekk, àddina sépp a ngi xel-ñaar ci CEDEAO, di laaj ndax dina amal cong mi am déet. Ak lum ci mën a doon, sóobare ya jël Nguur ga, ñoom, tëj nañ jàwwub réew ma ba roppalaan dootul naaw di tiim réew ma. Nde bëgguñu ku leen bett, te am nañ lu leen leer ni CEDEAO ak ñi leen di jàppale mën nañ leen song saa su nekk.