LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (7/8/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NGUUR GI AK “ENTENTE SYTJUST-UNTJ” XAATIM NAÑ AB DÉGGOO

Daanaka lu jege ñaari weer walla lu ko ëpp liggéeykati Yoon yaa ngi ci ay ñaxtu. Li ko waraloon mooy Nguur gi nanguwu leen woon a wuyu ci li ñu ko doon woo. Waaye, mel na ne coppite am na. Ndax, ñook Nguur gi xaatim nañu tay ab déggoo ngir ag dal gu sax am ci banqaasi Yoon yi. Dafa di, ñaxtu yi du njariñal kenn ci ñoom.

BÀYYI NAÑU ASAN JUUF

Lu tollu ci juróom-ñetti weer ginnaaw bi ñu ko tëjee ak tay, Asan Juuf mujj naa génn. Waaye, loolu du càggan ne daanuñu ko. Daan nañ ko ñeenti weeri kaso yu mu war a tëdd. Te, li ñu ko daane mooy biral xibaar yu wérul ak yékkati kàddu yu woroo ak jikko yu rafet yi. Li tax du tëdd du lenn lu moy ne moom diir bi ñu ko daan tëdd na ko ba noppi.

XEW-XEW BU DOY WAAR FA SALI

Guddig talaata jàpp àllarba la xew-xew bu doy waar am fa Sali. Ay sàmbaa-bóoy ñoo fa song kërug benn “architecte béninoise” def fa jëf ju ñaaw. Dafa di, bees sukkandikoo ci waa Seneweb, ñoom dañoo yamul ci jël koppar ak ay takkaay ya kese. Ginnaaw bi ñu fa jëlee koppar gu tollu ci fukki miliyoŋ ak ay takkaayu wurus ak jamaa, dañ caa yokk leneen. Ndaxte, dañu faa jàpp xale bu jigéen bu tollu ci ñaar-fukki at ak juróom-ñett, siif ko. Te, li ci gën a doy waar mooy du kenn kesee ko siif, ñoom ñépp a ko ay-ayloo. Mu nekk xew-xew bu tiis. Ndax, ñaawteef yi mu boole moo bari.

UMAR SIISOKO EMBAALO DÀQ NA ELIMAANU JËWRIÑAM

Njiitu réewu Gine Bisaawo jël na ndogal lu diis ñeel ki jiite woon Nguuram, di Rui Duarte Barros. Moom, Sëñ Embaalo, dafa jël ndogalu dàq ko ba noppi tabbaat keneen. Ki ko wuutu mooy Berema Kamara. Moom, Barros mi ñu dàq, ca weeru desàmbar atum 2023 lees ko tabboon, wàccee ko bi wote yi desee diir bu néew. Waaye, ba tay, xameesagul lu sabab ndogal loolu bees sukkandikoo ci waa AFP.

DAKKAL NAÑU NAWETAAN YI FA YOOF

Tay, ci alxames ji, la “sous-préfet” bu Almadi, Muhammadu Lamin Caam, jël ndogal lu am solo ñeel nawetaan yi. Kenn umpalewul ne jamono yii nawetaan yi door nañ. Moom nag, dafa jël ndogalu dakkal leen fii ak ub diir fa goxub Yoof. Li ko waral du lenn lu moy ñàkk a dal gi muy àndal ñu koy dippe “troubles à l’ordre public”. Maanaam, po yooyu day gàkkal lu bari ci péeteg askan wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj