LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (8/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

USMAAN SONKO JËL NA LENGEY MAGUM JËWRIÑ YI

Usmaan Sonko, magum jëwriñ yi ci càmm gu bees gi, jël na lenge yi tey ci altine ji. Ci loxoy Sidiki Kaba mi mu fa wuutu la ko nangoo tey ngir mën a door liggéey bi ko Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Fay Sant. Yékkati na fa sax ay kàddu di ci xamle ni njébbal gi am na ci anam yu jaar yoon. Ba tax mu ciy sant jëwriñ ji Kaba ak i ñoñam ci  nees leen dalalee ak nees waajalee wayndare yi. Sant naat jëwriñ ji ci liggéey bu mucc ayib bi mu amal ci at yu yàgg yi mu def  ci nguur gi te kenn mësu koo dégg ci naka su dul noonu.

XEEX TUX MI

Kurélu way-maxejj yee ngi sàkku ci Nguur gi mu yokk bu baax kumbal yi (taxes) yi ci njëgu sigaret si. Li ñu ko dugge nag, mooy xeex tux mu metti mi ñu seetlu ci ndaw ñi. Biraayim Sekk mi yor seen kàddu moo ko fésal. Fekk mu doon teewe ndaje mu taskati xibaar yi ci wàllu wer-gi-yaram doon amal ci gaawo gi, fa Mbuur. Bees sukkandikoo ci kàddoom yooyu, ñi seen xel màcc ci mbir mi dëppoo nañ ci ni tux maa ngi yàq ak a faagaagal bu baax ndaw ñi fi réew mi. Ba tax na ñu gis ni bees yokkee njëgg gi bu baax, dina leen bañatee yomb te itam Nguur gi dina ci mën a fortaatu koom ngir gën koo mën a xeex.

MÀGGET CAAM (PIT) DËDDU NA

Màgget Caam mi fi bokkoon PIT (Parti de l’indépendance et du travail) dëddu na démb ci dibéer ji. Muy ku am solo lool ku pàrti bi ñàkk, waaye itam njabootam ak réew mépp. Bu weesoo pólitig bi mu doon def (nekkoon na fi jëwriñ ji ñu dénk wàllu bennale Afrig), Màgget Caam doonoon na jàngalekat bu ñépp nanguloon. Jiite woon na fi sax IREMPT (Institut de recherche pour l’enseignement des mathématiques de la physique et de la technologie) di kurélu gëstu ak njàngale fa jàngune Séex Anta Jóob.

MBËKK MI

Sàndarmëri teg na loxo 95i way-fobu yu nammoon a jóge ci réew mi, tegu ci yoonu mbëkk mi. Moo ngi leen jàpp ci gaawu gi, 6 awril 2024, ci diggante Sigicoor ak Mbuur. Fekk ñu doon amal seen wëraan yi nu gën a baril jamono yii ngir xeex mbëkk mi. Ci xibaar yi ñu siiwal, 13 ci ñoom ay jigéen lañu. Am naat ay doxandéem, 3i doomi réewum Gàmbi ak jenn doomu Gine Bisaawo. Jamono yii, luññutu yaa ngi ñuy wéyal ngir teg loxo ñi taxawal yoon wi ak ñi leen naroon a yóbbu.

BITIM-RÉEW

Fa réewum Ruwànda, ñoo ngi fay màggal 30i ati faagaagal xeetu Tutsi gi fa amoon ci atum 1994. Démb ci dibéer ji lañ ko tàmbali ci ndigalu Njiitu réew mi, Póol Kagaame. Moom Njiitu réew mi sax ma nga woon fa barabu pàttaliku bu Gisosi (mémorial de Guisozi) ngir jafal gilitu pàttaliku (flamme du souvenir) bi ñeel ubbiteg màggal yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj