Njiitu Réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, tànn na Soxna Amsatu Sow Sidibe ngir mu jiite ndiisoog réew mi ñeel àq ak yelleefi doom-aadama (Commission nationale des Droits de l’Homme). Xibaar la bu jëwriñ ji ñu dénk Yoon siiwal cib yégle ginnaaw bi Njiitu réew mi xaatimee dekkere No 2025-581 bu 28 mars 2925. Moom, Amsatu Sow Sidibe, jàngalekat la ci bànqaasi Yoon, xelam gën a màcc ci mbirum àq ak yelleefi doom-aadam. Ginnaaw bi ko Njiitu réew mi tànnee ci ñetti lawax yi ñu ko dégtaloon, dina jiite kurél gi ci àppu juróom-benni at.
KOOM-KOOM : NJIITU RÉEW MI DALAL NA NJIITU NDIISOOG UEMOA
Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon na dalal démb ci altine ji kii di Abdulaay Jóob (njiitu ndiisoog UEMOA). Seen ndaje moomoo ngi aju ci waxtaan yi mu sumb ak campeefi koom-koom yi réewum Senegaal di jëflanteel. Ci noonu sax la njëkkoon a dalal Njiitu FMI li ci bu yàggul dara.
Wile yoon, Njiitu Réew mi waxtaan naak njiitu ndiisoog UEMOA li ci tolluwaayu koom-koomug Senegaal ak jubluwaayi kurélug diiwaan bi. Naka noonu, gaaral na ko coppite yi Càmmam teg ngir dooleel koom-koom gi ak yokkute gu sax.
Bu dee Sëñ Abdulaay Jóob, rafetlu na bu baax góor-góorlu gi njiiti Senegaal yi wane ci anam yi ñu yore gafakag réew mi. Mu dellu di leen ñaax ngir ñu gën a dëgëral seen taxawaay ngir dooleel réew mi. Ginnaaw loolu, taxaw na yit ci njariñ li bennoog diiwaan bi am ñeel suqaleeku gu law ci réewi kurélug UEMOA.
BÉSUB WÉR-GI-YARAM ÑEEL ÀDDINA SÉPP
Démb ci altine ji, 7i fan ci weeru awril 2025, doon nañu màggal bés bi ñu jagleel wér-gi-yaram fi àddina sépp. Fi Senegaal, Njiitu Réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaaxaar Fay gaawantu na ci daldi fésal yéeneem ci dooleel paj mi bu baax ak jàppandal ko ba Saa-Senegaal bu nekk mën a faju ci anam yu mucc ayib. Njiitu Réew mi dellusi na tamit ci jéego yi Nguur gi jot a seqi ci pajum roño ak yuqu yax. Wax na itam yokkute jumtukaayi raglu yi ba ci gox yi gën a sori yi, mataleg njaayum garab yi. Yooyu yépp di yóbbu Senegaal ci mu moom boppam ñeel paj mi.
YOON : FDR ÀNDUL CI KÀDDUY NJIITU RÉEW MI
Waa FDR (Front pour la Démocratie et la République) ànduñu ci kàddu yi Njiitu Réew mi mujjee biral ñeel doxinu Yoon. Cig pàttali, Njiitu Réew mi dafa biraloon ni Saa-Senegaal yi ci seen bopp ñoo war a taxaw temm, taxawu Yoon ngir mu def liggéeyam. Muy ay kàddu yoy, FDR jàpp na ni dañuy gàkkal ni Yoon mës di doxe, muy moom boppam gi mu baaxoo. Bees déggee li dépite bi Mbay Jonn wax ci seen tur, dëgg la ni askan wi lañuy doxalal Yoon, waaye tekkiwul ni dañu war a ërtal Yoon, ak nu mu mën a deme. Te dëggal lu ni mel ngir am ci Yoon li ñu bëgg bokkul ci xam wareef. Ndax, bu dee askan wee tax ñuy doxal Yoon itam, du moom moo koy doxal.