LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (8/8/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

BÀYYEENDI NAÑ PAAP AALE ÑAŊ

Meetar Musaa Saar moo biral xibaarub bàyyeendi Paap Aale Ñaŋ. Moom, Paap Aale Ñaŋ, wii mooy ñetteelu yon wi ñu koy jàpp. Dafa doon xiifal ba ñu rawale woon ko « Urgences » àjjuma ba tey.

Cig pàttali, kurél gii di Reporters Sans Frontières jóg doon nañ sàkku ñu bàyyi ko ca na mu gën a gaawe. Mu mel ni am nañ dëgg.

YÉGLEB YEWWI ASKAN WI

Ay fan ginnaaw bi ñu jàppee seen naataangoo bii di Usmaan Sonko, lëkkatoog Yewwi Askan Wi jógul ci di naqarlu anam yi ñu tegee loxo seen waa jooju. Te, ag bàyyeem yitteel leen lool nag, rawatina ci jamono yii ñu nekk. Li ko waral mooy ne ginnaaw bi ñu ko jàppee daf doon xiifal ba mujj daanu ñu yóbbu ko fa ñuy dippe “urgences”. Te, boobaak léegi askanu Senegaal amu ci ay xibaar. Moo tax ñuy woo Toppekat bi nga xam ne moo wund xoqatal gu tar gii gépp ngir mu amal am ndajem-waxtaan, indiy leeral ci anam yi Usmaan Sonko nekke ca kaso ba ak nu wér-gi-yaramam deme. Loolu tax ñuy sàkku ñu bàyyi Usmaan Sonko ca na mu gën a gaawe. Ndax, wér-gi-yaramam ak ug dundam nee nañ nekkul lees war a caaxaane.

XUWAAN BARANKOO ÑIBBI NA

Ci gaawu gii weesu lañu tegoon loxo dooomu tugal ji. Moom nag, kenn la ci layookati njiitul Pastef li, Usmaan Sonko. Moom layookat boobu ginnaaw bi ko waa Moritani jàppee ba jébbal ko waa Senegaal, mujj nañu ko bàyyi démb ci altine ji. Ca lañu santaanee ñu génne ko réew mi. Tey ci talaata ji la àgg fale ca Farãs. Ci ngoonug tey ji la waxoon ne day amal ndajem-waxtaan.

YÓBBU NAÑU MAYMUUNA JÉEY KASO

Maymuuna Jéey, meeri Patte d’Oie, di it njiitul jigéeni Pastef yi moom lañu yóbbu kaso démb ginnaaw ba mu jàkkarloo ak àttekat bi. Moom nag, ay fan a ngi nii ginnaaw bi ñu ko tegee loxo, muy baagante ca toppekat ba donte ne sax wér-gi-yaramam demewul noonu. Moo tax, jamono jii niki yeneen ciy ñoñam yu tawat ya ñu téye ca kaso ba, ma nga ca béréb bii di “pavillon spécial”.

Naka noonu layookat bii di Meetar Baabakar Njaay ak kii di Paap Sow meeru Sàngalkaam ak yenn ndaw yu ñu fa tegoon loxo tamit bàyyi nañu leen démb ci altine ji.

CUQALIG LIJJANTIG JIGÉÉEN AK LIGGÉEYU NDAW ÑI CA LUGA

Ñii di waa Padef-Ej (Projet d’appui au développement de l’entreprenariat féminin et de l’emploi des jeunes) ñoo taxaw temm ngir suqali liggéeyu ndaw ñi, gën a ñoŋal tamit lijjantig jigéen ñi. Moo tax ñu ne fii ak ñaari weer dinañu ubbi benn jaayuwaay meññenti mbay (Centre commercial agricole) ak benn kërug liggéeyu pepp (unité de transformation céréalière) yoo xam ne tollu nañu ci téeméeri miliyoŋ ak juróom-benn fukk ak juróom-ñett.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj