LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (8/8/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NDAJEM JËWRIÑ YI

Démb, ci àllarba ji lañu doon amal ndajem jëwriñ yi. Kii di Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jot na faa waxtaane ay ponk yu bari. Muy lu ci mel ni njëmbëtug garab gees amaloon dibéer jii weesu. Nde, moom, mébétam mooy ñu am Senegaal gu nëtëx. Bi mu jógee ci loolu am na ay càkkuteef yu mu def ci elimaanu jëwriñ yi ak ñenn ci jëwriñ yi ngir ñu door walla mottali yenn naal yi. Ginnaaw loolu, Njiitu réew mi jël na ndogalu takkal lim bu takku ay ndomboy-tànk. Ndax, ñi mu tabb démb tollu nañu ci téeméer ak ñaar-fukk ak juróom-benn.

AMINATA TURE AM NA DËGG CI KOW MANSUUR FAY

Ndogalu ëttu àttewaay bu Ndakaaru daanu na tey. Mansuur fay mi nga xam ne moo yóbboon Aminata Ture ci Yoon mujjul a am dëgg ci kowam. Ndax, moom Mimi Ture bàyyi nañu ko mu ñibbi këram. Ndax, jàpp nañu ne moo am dëgg. Li waraloon coow li mooy tuuma yi Mimi tegoon ci ndoddu Mansuur Fay ñeel yorin wu ñaaw wi ñu yoree woon junniy miliyaari Covid-19 yi. Looloo metti woon Mansuur Fay ba mu yóbbu ko ci Yoon, waaye, amu ca ndam.

PAAP ASAN SEKK JÓGE NA WALFADJIRI

Paap Asan Sekk bokk ci yenn ci taskati-xibaar yi ñu gën a ràññee ci mbaali jokkoo yi, tuxooti na. Nde, kenn umpalewul ne kër ga mu dem di RTS (Radion Télévision Sénégalaise), mës na faa jaar. Kon, mënees na dafa dellu këram. Xibaar moom moo ko siiwal tey ci alxames ji ci benn widewoo bu mu def ngir yégal ko ay soppeem.

WOODSIDE ENERGY DEM NA CI YOON

Këru liggéey gii di Woodside nga xam ne day yëngu ci wàllu soroj, lëkkaloo it ak Nguuru Senegaal ci wàll woowu, sonn na jamono jii. Bees sukkandikoo ci sunuy naataangoy Senego, li ko waral du lenn lu moy koppar gu bari gi ñu teg seen ndoddu ñu war koo fay. Maanaam, li ñuy dippe “redressement fiscal”. Ñii di waa “Seneweb” xamle nañu ne waa DGID (Direction Générale des Impots et Domaines) ñi ngi leen di laaj lu tollu ci ñeent-fukki miliyaar ak benn ak lu teg (41, 467). Ñoom nag, dañoo jàpp ne li leen kilifa yooyu teg dafa diis lool, ñu bëgg a dem ci Yoon ngir àddu ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj