Tay, alxames juróom-ñeenti fan ci weeru sãwiyee, mooy bés bi ñu jagleel njàngum xale yu jigéen ñi. Lii mooy fukk ak juróom-benneelu yoon ñu koy amal. Ña nga ko doon amale fa CICAD (Centre International de Conférences Abdou Diouf de Diamniadio). Ñi ngi ko doon amalee ci teewaayu Soxna Mari Xoon Fay mi nga xam ne moom lañu ndeyale bés bi. Nde, kenn umpalewul ne mooy aawob Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Moom, Soxna si, yékkati na fa ay kàddu yu am solo. Li ñu jublu ci bés bi mooy ñu gën a gëddaal yarub xale yu jigéen ñi, waaye tamit ñu gën leen a jàppale tamit ba ñu mën di jàng ni mu ware.
DAWALKATI “JAKARTA” YAA NGI ÑAXTU
Démb, ci àllarba ji la coow li door. Li ko waral du lenn lu moy li Nguur gi sàkku ci ñoom ñu wut ay këyit. Dafa di, ñoom nag, dañu ne li ñu leen di teg dafa diis ci wut ay këyit kepp. Ba tax na, ñu ne xalaatuñoo nangu lu ni mel. Looloo tax, daanaka, dëkk yi ëpp ay “Jakarta” ci réew mi, muy Sigicoor ak Kawlax, ñoom génn nañu di ñaxtu. Li ñu ko dugge mooy won Nguur gi ne lii mu bëgg a def nii, day metti ci ñoom.
XEW-XEW BU METTI FA KUNGÉEL
Mu mel ni du guléet ñuy nemmeeku jàmmaarloo diggante sàmm yi ak baykat yi. Waaye, wii yoon, mbir mi dafa jéggi dayo. Nde, coow li amoon seen diggante, guddig démb jàpp tay, bakkan rot na ca. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, coow laa ngi doore ci yàq bi jurug sàmm bi yàq toolu baykat bi. Loolu lañu topp ba ab xeex juddu ca, bakkan rot ca. Xew-xew booba, ma nga ame fa dëkk bii di Amdalaa, nekk ci goxu Kungéel.
LAKK GU METTI FA LUGA
Lakk googu mi ngi am ci ngoonug démb gi ay boori juróomi waxtu. Ma nga ame fa koñu “Montagne”, ci boori daara ju digg-dóomu ja, di “Nouveau Lycée”. Mu doon nag ag lakk gu metti donte ne sax bakkan rotu ci. Waaye, bari na ay yàqute yu ca am. Bees sukkandikoo ci waa Leral.net, lu tollu ci juróom-benni kër tàkkee nañu ca jëppeet. Te, kenn umpalewul ne fu kër tàkkee, alal yàqoo fa. Loolu di tekkii ne kon, alal ju bari yàquwaale na ca safara sa.
CONG MU METTI FA CÀDD
Cong moomu mi ngi amoon démb, ci àllarba ji, boori timis jàpp gee. Ca waxtu yooya lañu dégg ay sox yu tàkk fa gëblag Réew ma, di Njamenaa. La ca gën a doy waar mooy ne màkkaanu Njiitu réew ma, njénde la, la sàmbaa-bóoy ya song. Nee ñu, benn sóobare “commando” bu ngànnaayu moo fa duggoon. Waaye, laata muy am la mu bëgg fekk na way-wattuy kaaraange béréb ba téye ko. Fukki nit ak juróom-ñeent ñoo ca ñàkk seen i bakkan, juróom-benn jële cay gaañu-gaañu. Xamle nañu ne jàmm dellusiwaat na fa Réew ma, lépp teguwaat na ci yoon.