Aali Nguy Njaay mottali na yéeneem ngir nekk lawax ci wotey 2024 yi. Ci gaawu gi la woote woon am ndaje mu mag ngir biral ko. Ñu bare teewoon nañ fa, ba ci Mahamad Jonn mi fi nekkoon jëwriñ ju mag ci Càmmug Maki Sàll. Moom nag, ginnaaw bi Njiitu réew mi, Maki Sàll, tànnee Aamadu Ba ngir mu nekk mbëru Bennoo Bokk Yaakaar ci wote yi, la delloo woon ndombog-tànk giñ ko takkaloon. Bi mu jëlee kàddu gi ba siiwal nekkug lawaxam, fésal na ciy waxam ne réew mi am na lool ay jafe-jafe ci wàlli liggéey, dund ak Yoon. Mu fas yéene nekk nag Njiitu réew mi leen di joyyanti ngir dëppalewaat askan wi.
MBATIIT
Ndëpp li waroon a am démb ci dibéer ji fa Yoof mujjul a am. Muy xewum caada mu mag mu Lébu yiy faral a amal at mu nekk. Li waral ba amul nag mooy ni Calawu Almadi lu ndaw li (sous-préfet), Majéey Njaay, moo ko gàntal. Ci gaawu gi la génne ab areete buy tere ku amal ab yëngu-yëngu. Mu duggee ko ni mën naa indi lu ñuy tuddee risque de trouble à l’ordre public, maanaam lu mën a gàllankoor jàmmi askan wi.
TÀGGAT-YARAM
Démb ci dibéer ji làmb amoon na ca Areen Nasiyonaal. Zoss moo ca doon sëgg ak Aada Faas. Waaye, seen bëre ba yàggul dara. Matul sax ñaari simili. Ginnaaw bi ñu léewtoo ci simili bu njëkk bi, ñaari mbër yi dañu tàmbali xeex daldi jàppante. Ci noonu, doomu Medinaa ji, Aada Faas, daldi di koy fàqat, cabaxal ko, daan ko.
BITIM-RÉEW
Xare ba jolleeti na ca diggante Palestin ak Israayel. Banqaasu saa-palestin bii di Hamas, féete ci Bande de Gaza bi, moo ko jëfalaat. Keroog ci gaawu gi, 7 oktoobar 2023, yemook bés bi Israayel di màggal Yom Kippour, la ko bett ak cong mu metti mu kenn foogul woon. Fii mu nekk, lu ëpp 600i doomi israayel ñàkk nañ ci seen i bakkan. Naka noonu, ñu tegaale loxo lu tollu ci 100i doom-aadama. Israayel itam jot naa fuddu ca saa sa ba faat luy tollook 370i doom-aadam fa Gaza.
Ginnaaw cong mi, jëwriñ ju mag ju Israayel, Benyamin Netayahu, génn na ba yékkatiy kàddu. Muy xamle ni dina fayul Israayel ba mu mat sëkk. Ñu gis neet ni réewum Etaa-Sini taxaw na ngir jàppale ko. Nde, jamono yii, Njiitu réew ma, Jóo Baaydën jot naa yabal i sóobare ca Israayel te dina fa yabalaat ñeneen ci fan yii di ñëw.
Réewum Senegaal mi jiite bànqaas bi yittewoo àq ak yelleefi askanu Palestin ca Mbootaayu xeet ya wone na njàqareem ci fitna gi judduwaat. Ba tax muy ñaawlu cong mi ko sooke. Mu dellu di sàkku ci ñaari réew yi ñu wéer ngànnaay yi te sóobuwaat ci waxtaan wi ngir taxawal àtte bi Mbootaayu xeet yi tëraloon.