LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (9/10/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

YOON TÉYANDI NA ALIW SÀLL (RAKKU MAKI SÀLL) AK SOXNAAM

Aliw Sàll, nekkoon fi meeru Géejawaay, di it rakk ci ki fi nekkoon Njiitu réew (Maki Sàll), ma nga woon DIC (Division des Investigations Criminelles). Bees sukkandikoo ci xibaar yi rotagum, li waral ndéglu gi mooy ag caabal gu waa CENTIF def. Bees sukkandikoo ci waa FD Media nag, ginnaaw bi ñu ko dégloo moom ak soxnaam, Yoon daf leen téyandi. Li ñu leen di tuumaal mooy weexalug xaalis.

DÉGGOO DIGGANTE HAMAAS AK ISRAAYEL NGIR DAKKAL XEEX BI

Bu yàgg ba tay, ci ay jàmmaarloo la Israayel ak Hamaas nekk. Saa su ñu jàppee ne jeex na rekk, ñu làbbaliwaat. Ay bakkan yu baree bari rot nañu ci, ñu bari jële ci ay gaañu-gaañu, waxaalewuñu xoqatal yi ak yàqu-yàqu yi. Waaye, mu mel ni jàmmoo mi ngi bëgg a am ci seen diggante. Ba tax na, jëwriñu Senegaal bi ñu dénk mbiri bitim-réew génnee ab yégle ngir rafetlu mbir moomu. Rax-ci-dolli, ñu sant ñii nga xam ne dox nañu ci ay jéego. Muy réew mu ci mel ni Qataar, Esipt, Tirki ak Etaasini. Nguuru Senegaal ñi ngi sàkku ci waa Hamaas ak Israayel ñu sàmmonte ak li ñu xas ba dige ko. Ndax, jàmm kat, ci la lépp xaj.

UPF MI NGI ÀRTU

UPF (Union internationale de la Presse Francophone) mooy kurél gi ëmb saabalukaay yiy jëfandikoo làkkuw farãse. Kurél googu nag génnee na ab yégle ngir fésal yitte ji mu am ci ndogalu kilifay réewum Senegaal yi. Maanaam, Majambal Jaañ mi ñu def li ñuy dippe “mandat d’arrêt international”. Dañoo gis ne loolu jekkul, jaaduwul. Li ñu gis mooy ne dañoo bëgg a noppiloo koo xam ne xalaat bu ñaw la yor te di leen biral. Te, li ñu def nii day salfaañe san-sañu wax sa xalaat bi ñépp am. Li ñuy sàkku mooy kilifa yi àtte mbir yi, te lépp ñu teg ko ci njub ak màndute. Naka noonu, layookati Majambal yi tamit ñi ngi ñaawlu ni mbir yi di doxe. Te, ñi ngi ciy dox ay jéego. Ndax, coow li yamul ci Majambal rekk. Soxnaam ak ay doomam dañu ci bokk. Ñoom ñooñu sax jamaono yii ñi ngi ci kaso bi.

JOTAAYU WAXTAAN CI XEW-XEWI RÉEW MI

Suba, ci àjjuma ji, Nguuru Senegaal dina janoo ak askan wi ngir waxtaan ak ñoom ci ñetti poñ. Bi ci njëkk mooy nu ñu yoree mbënd mi ak liggéey bu jëm ci cet gi. Ñaareel bi moo jëm ci mbirum defaraat ak yokk kaaraange ci pénc mi. Ñetteel bi mooy jëm ci li ñeel ubbiteg lekkool yi ak ndogal yu yees yi Nguur gi jël. Poñ bu ci nekk dafa am jëwriñ ju ci war a àddu. Ndax, bu ci nekk dafa am njëwriñ gu ko ëmb. Moo tax, jotaay ba, ñetti jëwriñ ñoo koy amal. Muy Séex Tiijaan Jéey mi ñu dénk ndox mi ak cet gi, Muhammadu Bàmba Siise mi ñu dénk mbiri biir-réew mi ak kaaraangeg pénc mi, ak Mustafaa Màmba Giraasi mi ñu dénk njàngale mu suufe mi ak mu digg-dóomu mi. Jotaayu waxtaan bii di “Kàddu” dina door suba, ci àjjuma ji, bu ñetti waxtu ci bëccëg tegalee fanweeri simili.

LAYOOB ABDU NGEER

Démb, ci àllarba ji, la kii di Abdu Ngeer doon layoo. Moom nag, bu yàgg ba tay mi ngi ci kaso bi. Li ñu ko doon toppe mooy biral xibaar yu wérul ak tooñ walla sax ŋàññi Njiitu réew mi. Moom ak ki ñu jàppandoo di Paab Aamadu Njaay Jaw, xamaguñu fu ñuy mujj. Dinañu génn am déet ? Loolu, fukki fan ak ñaar ci weeru nowàmbar lay leer.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj