Tey ci àjjuma ji la kii di Usmaan Sonko waroon a amalub mitiŋ ca Mbàkke waaye loolu mujjul àntu. Ndax, kii di perefe ba mooy ki ko tere ginnaaw ba gaa ñi fare ci Usmaan Sonko jébbale woon seenub bataaxal di sàkkoo amal ndaje moomu. Usmaan Sonko nag nee na ndogalu Perefeb Mbàkke bi dafa ruslu ci ni mu génnee yoon. Nee na mitiŋ bi dina am neex naqari. Jébbal na bataaxal Ëttu àttewaay bu kowe bi ngir ñu gàntal ndogalu Perefe bi.
Àtteb Sitoor Nduur
Kii di Sitoor Nduur nekkoon fi ay jamono njiitu COUD (Centre des Oeuvres Universitaires de Dakar), dinañu ko àtte benn fan ci weeru màrs. Moom nag dañu ko jiiñoon ne dafa sàkku benn xale bu jigéen bu tollu ci fukki at juróom-ñaar.
KOOM-KOOM
Déggo diggante Nguuru Senegaal ak BAD
Nguuru Senegaal xaatim nag pas ak waa BAD Banque Africaine de Développement ngir kopparal pàcc bu njëkk (phase 1) ci seen sémb yi. Bu njëkk bi di Programme national de développement intègre de l’élevage au Sénégal. Ñaareel bi sémbu tabaxum otorut Ndakaaru-Tiwaawon-Ndar.
Kurél gii UE (Union Européenne) génnee na lu tollu ci 800 miliyoŋi ëro, maanaam 524,7 miliyaar ci sunu koppar. Li mu ko dugge nag mooy yombalal ndongo yeek jàngalekati réewi Afrig yi ñu mën a defe yenn ci seen i pàcci njàng (stage) ca Tugal walla fépp ci àdduna bi diggante 2021 ba 2027. Kii di seen àmbaasadëru ci Senegaal, Jean-Marc Pisani, mooy ki ko xamle.
WÉR-GI-YARAM
Njeexitalu tuxum sigaret
Abdul Asiis Kase di fajkat bu xam-xamam màcc ci jàngoroy kañseer, moo doon biral njeexital yi tux di def ci wér-gi-yaramu nit ki. Moom nag xamle na ne tux mi dina rey lu tollu ci 800.000i nit ci at mi. Rax-ci-dolli, ne benn sigaret bu nit ki tux, dina wàññi fukki simili ak ñeent ci ag dundam. Te, jàpp na ne Nguur gi da cee war a jël ay matuwaay àrtu ñiy tux ak ñi dul tux ndax dafa bon ci wér-gi-yaram.
XEW-XEWI JAMONO
Jéyya ja am ca Turki ak Siri
Jéyya ja amoon ca réew yooyu ci altine jii weesu ma ngay wéy di raafal. Ci ab saabal bu kilifa ya fa nekke fésal tey xamle nañu ne lu ëpp 17.100iy nit ñàkk nañu ci seen i bakkan. Ndax, ci Turki rekk lu tollu ci 14.014iy bakkan ñoo fa rot ak lu tollu ci 60.000iy nit yu ca jële ay gaañu-gaañu. Ca Siri moom lu tollu 3.162iy bakkan ñoo fa rot.
Xew-xew bu doy waar ca Rufisk
Xew-xew bii nag démb ci suba la woon. TER bi moo am ku mu fiir ca boori Rufisk. Loolu sax taxoon ñu dakkal demam ak dikk ci diggante boobu. Maanaam diggante Jamñaajo ak Rufisk. Nee ñu, ki saxaar gi fiir, dafa ñàkk bakkanam ci saa si.
Beneen xew-xew bu tiis
Lii nag benn minikaar moo mbëkkante ak benn sëfaan gu yeboon simaŋ ba juróomi nit ñàkk ca seen i bakkan. Loolu mi ngi xew démb ci otorut bi, booy génn Sébikotaan ci wàll wi féete diggante AIBD ak Ndakaaru.
Ñàkkug banaana ca Jalakoto
Foofu ca diwaanu Jalakoto lu tollu ci ñaari ektaari garabi banaana la fa ag lakk yàq. Li ñu njëkk a xayma ci ay yàqu-yàqu tollu na ci ñaar-fukki miliyoŋ. Ba tey xamaguñu li waral googule lakk. Waaye, kii di fara-caytu bu kurél gii di Association des producteurs de la vallée du fleuve Gàmbi (Aprovag), Abuubakri Jàllo, xamle na ni lu neew a ci desoon ngir ñu tàmbali watt gi.