Layoo bi waroon dox démb ci diggante Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ dañu ko mujje ajandi. Li ko waral nag mooy ne, kii di Njiital Pastef li jotul ab woote. Loolu mooy li layookat yi xamle. Ba tax ñu mujj jàppaat layoo boobu fukki fan ak juróom-benn ci weeru féewaryee wii nu nekk.
Càkkuteefu dépitey YAW
Guy Mariyus Saaña ak i naataangoom ñi ngi sàkku ñu yóbbu yenn jëwriñ yi ci kanamu Yoon. Maanaam, fukki jëwriñ yi nga xam ne caabalug ëttub cettantal gi duut na leen baaraam ci yorinu wu bon wi ñu yoree woon FORCE-COVID-19 bi. Càkkuteef googu nag teg nañu ko ca taabalu Njiitu Ngomblaan gi.
Tontub Njiitu réew mi ñeel coowal TER bi
Kii di Njiitu réew mi Maki Sàll indi na ay leeral ci coow loolu nga xam ne nee na daf ko bett. Ndax, nee na sémbu TER Nguuru Senegaal mooy ki ko kopparal. Mu yokk ci ne dañuy topp ay wax yu dul jeex, mu bokk sax nag ci liy gàllankoor Afrig. Ndax, bu ñu nekkee di liggéey ngir lu jëmale kanam kembaar gi, fàww nga gis ñuy gàkkal li nga def nga xam ne dafa waroon a doon sagu kembaar gi.
DIINE
Màggalug Poroxaan
Démb ci alxames ji 2i fan ci weeru féewaryee la tariixa muridiya bi doon màggal ca Poroxaan. Màggal googu nag ngir delloo njukkal kii di Soxna Maam Jaara Buso nga xam ne way-jur la ci Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke mi sos tariixa muridiya.
Génnug àdduna Séex Ahmad Tiijaan Taal
Séex Ahmad Tiijaan Taal nekkoon imaam ca Daaru Salaam 2 ca Grand-Yoff moo génn àdduna ci anam yu doy waar. Ndax, moom dafa réeroon ay mbokkam altine ba léegi. Démb ci alxames ji lañu ko gis fekk mu faatu. Ña nga ko gise ca déegu Zone de Captage, koñ boo xam ne soreewul ak fi mu dëkk. Ba jamono jii nag, xameesagul ci yan anam la génne àdduna.
NJÀNG AK NJÀNGALE
Jàngalekat ya fare ca Bàmbey dàbbali nañu
Jàngalekati daara ju kowe ju Bàmbey yi bokk ci SAES (Syndicat Autonome des Enseignant du Supérieur) xamle nañu ne dinañu dàkkal njàng mi altine juróom-benni fan ci weeru féewaryee wii. Nee nañu nag bés boobu ngir xupp kepp la.
Ndongoy UGB yi dakkal nañu ñaxtu yi
Ci altine jii weesu lañu dakkaloon njàng mi lu tollu ci ñetti fan ak lu tollu ci juróomi fan yoo xam ne dañuy lekk te duñu fey. Li ko waraloon nag mooy ñàkkum dëkkuwaay yu àttan ndongo yi ñu fi bëgg a indi ci at mi.
Génnug àdduna benn jàngalekat ca Koldaa
Ab njàngalekat la woon ca CEM Saare Bilaali bi nekke ca diwaanu Koldaa moo génn àdduna ci anam yu doy waar. Moom nag, ag sëfaan moo ko fiir, mu gaañu ca saa sa. Nee ñu nag, boroom sëfaan gi da doon moytu geneen sëfaan ak geneen daamaar gu taxawoon, ci la fiire jàngalekat bi.
TÀGGAT-YARAM
Móodu Lóo-Booy Ñaŋ taxawna
Ñii di waa Source A ñooy biral xibaar bi. Nee na ñaari mbër yi dinañu bëre ci weeru oktoobar. Kii di Gaston Mbeng mooy ki taxawal làmb ji.
XEW-XEWI JAMONO
Aksidaŋ ci yoonu Tiwaawon
Aksidaŋ baa ngi ame ci diggante Lam-Lam ak Njaxate. Benn jakartaa bu yeboon ñett nit moo mbëkkante ak genn daamar (4×4). Ñaar ña moom ca saa sa lañu faatu, ka ca des it ame na ay gaañu-gaañu yu metti. Nee ñu nag ki doon dawal jakartaa da doon daw lu bari ci ginnaaw genn sëfaan. Bi mu nee da koy romb nag ci la dajee ak 4×4 bi moom it mu doon daw lu bari.
Xew-xew bu tiis
Lii nag ma nga ame ca Lingeer, jenn rakk moo fa bóom magam ju xaw a wéradi. Li ko waral nag mooy da doon dóor seen yaay. Bi rakk ji déggee yuuxu yi ci la dawee walluji ndey ja. Bi mu àgge ca la dóoree mag ji ay jaasi ba mu jaare fa ñàkk bakkanam.
Beneen xew-xew bu tiis
Baradi la mbir mi xewe, benn dëkk bu nekke ca gox bii di Dodel ca diwaanu Podoor. Ñaari ndaw ñoo fa reyante ginnaaw ab xeex bu metti ak i ngànnaay. Nee ñu nag, ñoom xarit lañu woon ndax, ñoom ñaar ñoo fa jógeendoo ànd ak céet. Ci wetu yoon wi nag lañu fore seen i néew, yóbbu leen ca raglu bu Njum. Kenn ki mi ngi tollu ci fukki at ak juróom-ñett, keneen ki tollu ci fukki at ak juróom-ñeent.