Altine jii weesu la kii di Aamadu Ba demoon ca Ngomblaan ga ngir dégtal fa li Nguur gi namm a liggéey. Rax-ci-dolli, mu taataanaale xalaati dépite yi, ñii nag di waa YAW dañoo jàpp ne tontu ya mu joxe ci seen i laaj doyul ba tax ñu namm a fànq Nguuru Aamadu Ba gi. Loolu ñu dippee ko ci tubaab “Motion de censure”. Suba nag, ci alxames ji, bu fukki waxtu ci suba jotee, woo nañu dépite ya ca Ngomblaan ga ngir ñu càmbar loolu ndax dees koy wote walla.
Leerali Njiitu réew mi Maki Sàll ci ñetteelu moome gi
Kàddoom yooyu ñeel nekkam lawax ci wote yii di ñëw mi ngi leen jaarale ci New York Times ci ag laaj-tontu gu mu doon amal ak ñoom laata muy dem ca USA. Moom nag, nee na tey jii amul wenn sikk, ci wàlluw yoon, ci ne mën naa nekk walla mënul a nekk lawax. Léegi, mu nekk lawax walla mu ñàkk koo nekk, moo koy dogal te bés bu ci jëlee ndogal dina ko xamal saa-senegaal yi.
Jàppug ñaari dépitey PUR YI
Ginnaaw coow la doxoon seen diggante ak seen naataangoo bii di Ami Njaay, Masata Sàmb ak Mamadu Ñaŋ ña nga leen téye woon démb ca DIC. Mu mel ni nag li ñu leen di jiiñ yemul ci dóor yi kese, am lu ci dolleeku muy li ñu ko doon dig ne dinañu ko rey.
Càkkuteefu bàyyig négandiku
Kii di Seex Umar Jaañ ak Abdu Kariim Géy ñi doon sàkku bàyyig négandiku ginnaaw bi ñu leen dégloo ba noppi ci mbir mi ñu leen di toppe bañal nañu leen ko. Ñoom nag ñi ngeen leen toppe biral ay xibaar yu wérul ci génnug àdduna Imaam Aliyun Ndaw, di ci xamle ne loxo Nguur gi setul ci loolu.
Ci beneen boor bi, kii Paap Aale Ñaŋ moom, yoon nangul na bàyyig négandiku ba ay layookatam doon sàkku ginnaaw bees ko dégloo.
Caabalug RSF
Kurél gii di RSF (Reporters Sans Frontières) fésal na ne jàpp nañu lu tollu ci 533i taskati-xibaar ci àddina sépp. Limub ñi ñu ci rey tamit mi ngi tollu ci 57i taskati-xibaar. Réew yi ci ëpp lu ñuy tëj nag yii la : Siin (110) Birmani (62) Irã (47) Wiyetnaam (39) ak Belaariis (31).
WÉR-GI-YARAM
Lawug sibbiru si, ca Koldaa
Sibburu soosu nag ma ngay law ca diiwaanu Koldaa. Dem na sax ba diiwaan boobu dugg ci wayndare wu xonq wi ci fi mu gën a laal. Ndax, kii di doktoor Yayaa Balde mi ngi xamle ne xeexub jàngoro ji des na ndax kat, am na lu tollu ci 200i nit ñu ko ame ci lu tollu ci 1000 yafa dëkke.
KOOM-KOOM
Njuuj-njaaj ci “FORCE COVID-19”
Sémb bii di PLR (Projet de Loi de Règlement) biral na ne ci atum 2020 “FORCE COVID-19” (Fonds de riposte et de solidarité contre les effets du covid-19) jotoon na lu tollu ci 773,214i miliyaar. Lenn li jóge ci Nguur gi, leneen li ci ñi muy liggéeyandoo, li ci des ci doomi réew mi. Moo tax ñu bëgg ay leeral ci ni ñu jëfandikoo alal ju ni tollu. Ëttub cettantal gi, ci sémbam mu atum 2021 mi, jot na cee def ay lëñbët ngir xam fu xaalis bi duggu. Ñoom nag gis nañu ci ne jokkalante yi yu bare diggante MSAS (ministère de la santé et de l’action sociale) ak MDCEST (ministère du développement communautaire de l’équité sociale et territoriale) nu leen neex lañu ko doon defe. Rax-ci-dolli pas yi ñu daan xaatim nga xam ne nekkiinu askan wee (social) ko tax a jóg bokkul dara ak ja yi ñu ko daan jox walla ñu jox ko ku ci amul benn xam-xam.
XEW-XEWI JAMONO
Mbir yu yees ci wayndare bóomaatekat bi
Lëñbët yi ñu doon def ci waa ji bóom keroog ay bakkan ca jawu Mbuur, am na ay mbir yu yees. Ndax gis nañu ne waa ji dafa jiite kippaangog defkati ñaawteef. Ndaxte ca këram dañu faa gis ag kopparfoor, fekk ca biir lu tollu ci juróom-ñaari móto ak ay tele. Rax-ci-dolli, teg nañu loxo juróom-benni ndaw yu doon liggéey ak moom, juróom yi moom lañu doon dawalal ay móto jakartaa.
Xew-xew bu tiis ca dëkk bii di Kiren
Dëkk bii di Kiren nekke ca diwaanu Jas, ay sàmm ñoo fa rey benn ndaw. Moom nag, nee ñu sàmm yi dañoo bëggoon dugal seen ug jur ci ab toolam, ci la jotee ak ñoom. Kenn ku fekke bóomug A.Faye xamle na ne jaasi lañu ko reye ba pare dem.
Beneen xew-xew bu doy waar
Lii nag benn xale bu jigéén la boo xam ne ci fukki atam ak juróom-ñett la séyi, ginnaaw bi ñu tëjee jëkkëram lu tollu ci juróom-benni at ginnaaw bi mu jëlee biir. Ci la ko goro bi topp bëgg a tëdd ak moom ngir ne sëriñam moo ko ko digal ba ni muy ame doom, ginnaaw ba mu amee doom ca la ko ca fekksi ba jële ci ëmb.
Meneen cong ca Tuuba
Ginnaaw cong gi amoon ca ja bu Mbuur ci njeexitalu ayu bés bi, meneen am na ca Tuubaa. Genn gàngoor gu tollu ci fukki nit ak juróom gu yor ay ngànnaay ñoo fa song ab “Station”, jële fa lu tollu ci 3,6i miliyoŋ, fetalante ak pólise ya laata ñuy daw, am nag ñaar ñu ca jële ay gaañ-gaañu.