Léegi leer na, kii di Maalig Gàkku mooy nekk lawaxu làng gii di Grand Parti. Ca ndaje mu ñu amaloon la xamlee ne mooy nekk juróomeelu Njiitu réewum Senegaal, keroog, féewaryee 2024. Nee na xam na saa-senegaal, saa-senegaal yi xam nañu ko, te xam na li ñuy xaar ci moom ci wàll yépp.
Kuutal Paap Jóob ca Ngomglaan ga
Musaa Jaxate mooy doon kiy wuutu Paap Jóob, dépite Bokk Gis-Gis ca Ngomlaan ga. Ci alxames jii lañu koy takkal ndombog-tànk googu. Les Echos moo jibal xibaar boobu.
Ndogali coowal Ciki li
Démb ci talaata ji la juróomi way-wattu kaaraangeg Usmaan Sonko (Lamin Sonko, Móodu Jóob, Ibraahiima Bóoy, Móodu Jaw, Jaxate Jóob) doon janoo ak àttekat bii di Piyeer Tin ca ëttu àttekaay ba nekke ca diwaanu Mbuur. Toppekat bi teg ñeent ñi ñaari ati kaso yoo xam ne dañu ciy tëdd menn at. Mu teg kii di Umar Njonn atum kaso moo xam ne dina ci tëdd juróom-benni weer. Ci ñaar fukki fan ak juróom-ñeent ci weeru nowàmbar lañu ciy jël dogal.
Njàng ak Njàngale
Doxub ñaxtu bu ndongoy daara ju Xelkom Biram
Ndongoy liise Xelkom Biram nekke ca diwaanu Gingineew wàcc nañu ci tali bi ngir wane seen naqar. Li ñuy sàkku nag, bokk na ci njàng mu jaar yoon, ak ñàkkum jàngalekat nga xam ne moo leen gën a sonnal.
Ndogal li G7 jël
Ci mbiri kaŋkuraŋ ya ca Kubanaw ca Biñona, ñii di waa G7 jël nañu ndogal dàkkal njàng mi fii ak diir ginnaaw bi ñu jële woon dogalub dàkkal ko diirub ñetti fan. Li ko sabab, mooy ay dogaale aki bunduxatal yu jàngalekati béréb ba di daj. Bi ci mujj a ngi amoon fukki fan ak benn ci weeru nowàmbar bii.
Ndogalu liggéeykati UCAD
Ginnaaw weer bi ñu amalee ay waxtaan ak Njiit ya te gisuñu ca lu leen doy. liggéeykat ya nekk UCAD, xamle nañu ci seen ndaje mi ñu doon amal ne, dañuy wéyalaat xeex bi. Moo tax ñu dakkalaat seen liggéey ci diirub ñaari fan.
WÉR-GI-YARAM
Bés bi ñu jagleel jàngoroy jabet
Démb lañu doon màggal bés bi àddina sépp jagleel jangoroy jabet ci diwaanu Ndar. Ndar nag mooy diwaan bi jàngoro jooju gën a laal ndax am na lu tollu ci 14%. Jàngoro jooju, jigéen ñi la gën a sonal.
Xeexub yenn jàngoro
Ngir xeex jàngoroy sidaa, sëqët su bon si, siburu gi (paludisme), jëwriñ ji ñu dénk wàllum wér-gi-yaram def na benn bopp ak kurél gii di ANCS (Alliance Nationale des Communautés pour la Santé). Kii di Njiit lu mag lool wér-gi-yaram wi seeti woon na kurél googu ngir ñu xoolaat déggoo yi amoon seen diggante ci mbiri kopparalu Fonds mondial.
KOOM-KOOM
Ñàkk a gëddaal ndogalu Njiitu réew mi
Ñi ñu dénk wàllum njënd ak njaay woo nañu démb lu ëpp téeméer et ñeent fukki jaaykat ngir ñàkk a sàmmoo ak ndogal li Nguur gi jël ci wàññig yenn njëg yi. Gaa ñooñu nag saytu nañu ñaar fukk ak juróom-benni béréb ci Ndakaaru. Muy fi ci mel ni Pikin, Géejawaay, Kër Masaar, Rufisk.
XIBAARI BITIM-RÉEW
Jàppug benn doomu Senegaal ca Itaali
Benn doomu Senegaal bu am lu tollu ci fukki at ak juróom-ñaar lañuy jiiñ siif ci benn ndongo bu jigéen bu am ñaar fukki at ak ñeent. Loolu mi ngi ame ca seen néeg ba nekke ca daara ju kowe ja di Paolo Borsellino. Mbir ya nag ma nga ca loxoy yoon.
Jafe-jafey saa-senegaal yay dund ca Gaboŋ
Yenn ci doomi Senegaal yay dund fale ca réewum Gaboŋ la kilifa yooya téye seen i jàll-waax (passeports). Ñoom nag dafa mel ni seen i mbir doxatul ba ñi ngi sàkku ndimbal ci seen kilifay réew.
XEW-XEWI JAMONO
Néew ba ñu for ca Kaasamaas
Néewub jigéen jooju ñu for mi ngi woon ci yoonu yàqu. Moom nag war na am lu tollu ci juróom-fukki at. Ñu ngi ko fore ci dëkk bii di Bambajon, nekke ca diwaanu Gudomp, Karantaba.
Xew-xew bu doy waar
Ndongo lu jigéen lu doon jànge ca daara ju kowe jii di UCAD lañu doon àtte démb ngir bóomug xale. Ndaw sii di N. Fay dafa jële woon ëmb ci àndam ak kii di Bass, ba pare kooku daw jëf ji. Bi mu muccee nag, ci la bóom doom ji. Juróomi ati kaso lañu ko namm a daan. Waaye àtte bi juróomi fan ci weeru desàmbar lay leer.
Beneen xew-xew bu tiis
Soxnaa sii di wuyoo ci turu Maymuna, nee ñu, dafa xaru ngir bañ a dugg ci benn séy. Ñ rax ci dolli ne, ñetti fan laata muy xaru xamal na njaatigeem ni yaayam daf ko bëgg a may ku mu bëggul te lu ko ci dal moom la.
Njombe la am ca digu Senegal ak Gàmbi
Lu tollu ci ñetti téeméeri kilo yàmbaa la birigad duwaani Ñooro teg loxo. Loolu ñu teg loxo nag, tollu na ci ñaar fukk ak ñeenti miliyoŋ. Mbir maa ngi xewe ci benn dëkk diggante Senegaal ak Gàmbi.