Ginnaaw Umar Yum, Ismayla Maajoor Faal (jëwriñ jiñ dénk wàllu yoon) moo génn di dànkaafooti Mimi Ture ci taxaway bi mu namm a am ca Péncum ndawi réew ma. Mi ngi koy xamal ne bés bu fésalee mbañam ñeel njéggal gi nguur gi namm ci Xalifa Sàll ak Kariim Wàdd, dinañ foqati moomeem.
Ci dibéer ji, Njiitu Réew mi Maki Sàll amal na itam ab doxontu ci mbeddi Géejawaay yi. Mu doonoon i tànki nemmiku askan wi ak it fu liggéey bi mu santaane woon ci yenn gox yi ak goxaat yi tollu. Mu mel ni kuy won yoon wi ay jëwriñam te naan leen jegeleen askan wi te taxaw ci seen i soxla.
JOŊANTE TARI ALXURAAN
Senegaal amatina ndam lu réy ci joŋante tari Alxuraan bu àddina sépp séq. Doomam jii di Soxna Ndàtte Siise moo jël ndam li ci atum 2022 bi ca Dubaay. Muy guleet itam jigéen di raw ci bile joŋante. Rax-ci-dolli, ndaw si amul lu dul fukki at ak ñeent.
GÀMMU 2022
Yóbbali kilifa diine yi ñeel way-politig yi
Sëriñ Baabakar Si Mansuur : « War na Nguur gi mu jéem mépp pexe ngir jàmm ji di wéy ci réew mi » ; « Na nguur gi ak kujje gi toog waxtaan. Réew mi ñépp a ko bokk, te jàmm rekk ko mën a jëmale kanam, waaye du doon i dóorante. »
Séex Maahi Ñas : « Noo ngi ñaan Nguur gi ak kujje gi ñu am yërmande ñeel askan wi, rawatina ci jamono ju metti jii ba kenn xamatul nooy def… »
TÀGGAT-YARAM
Gaynde Senegaal yi ñàkk nañ gañ-jël bu turnuwaa UFOA/A U17. Ginnaaw bi ñu témboowee ci biir joŋante bi, doomu Maali yee mujje am ndam ci seen kow ci dóoral-ma-dóor yi (2-4). Ginnaaw bi ñu yeggee ci gañ-jël bi nag, ñaari ékib yi dinañu bokk ci Can U17 bi war a amee ca réewu Alseri.
KAAWTEEF
Coowal Bilaal bi ñu faatoon ca Njéeyeen-Pir a ngi ci tànki leer. Sàndarma yi jot nañoo teg loxo fukki nit ak ñaar. Li gën a yéeme ci mbir mi moo di Yilimaan ji ci taq ripp. Bi laaj-tontu yi takkarnaasee, dafa mujje nangu ne moo yabal ñi def ñaawteef bi. Sàndarma yaa ngi wéy di seet yeneen juróomi nit yu laale ci mbir mi.