LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 14 noowàmbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Maalig Gàkku dina nekk lawax ci wotey njiiteefu réewum Senegaal yii di ñëw. Làngu pólitig gii di Grand Parti, te moom ci boppam jiite ko, moo ko tabb niki démb ci dibéer ji (13 nowàmbar 2022) ca ndaje miñ doon amal ca CICES. Ñi ngi ko fas yéenee ngemb ci turu lëkkatoo Mànkoo Yewwi Senegaal 2024.

Ca geneen wet ga, Njiitu réew mi Maki Sàll a ngay soññ ay ñoñam. Donte ni yëyul benn yoon yàbbi ci ñetteelu moome gi. Ma nga leen di xirtal ci njaayum kàrt yi te dëgëral bu baax seen taxawaay ci làngu pólitig gi.

WÉR-GI-YARAM

Kurélu liggéeykat yi ci paj mi te ñu gën koo miis ci Ànd Gësëm fas naa wéyal xeex bi mu sumboon. Ginnaaw bi ñu doon sàkku yokkute payooru mboolem liggéeykat yi, ña ngay xamle ni jëwriñ ji dafa wéy di leen tanqamlu.

TÀGGAT-YARAM

Gaynde Senegaal yi sóobu nañ ci kub bu àddina si. Ginnaaw ba ñu jotee dajaloo démb ca Farãs, roppalaanu Air Sénégal a leen yóbbu Dohaa ci guddi gi.  Amal nañ seen tàggatu gu njëkk ci bëccëgu tey ji.

Ci biir réew mi, doon nañ amal juróomeelu bëccëg bu raw-gàddu Senegaal. Casa sport delsi na ci bopp bi ginnaaw bi mu amee ndam ci kow Dakar Sacré Cœur. Diambars FC ak Teungueth FC ñoo toppante ci ñaareel beek ñetteelu toogaan yi.

XEW-XEWI JAMONO

Ndawi GPR (Groupement polyvalent de recherches et de répression de la fraude) yu duwaanu Senegaal teg nañ loxo lu tollook 905i tamndareeti Fcfa ciy kayiti xaalis yu bon. Looloo ngi am ci àjjuma jii weesu bi ñuy tëru defkati ñaawteef yi bëggoon a tas xaalis boobu diggante Cees ak Ndakaaru.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj