LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 17 oktoobar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Way-politig yi jublooti nañ ci wotey 2024 yi. Bu dee làngug Nguur gi, Njiitu réew mi, Maki Sàll, jóg na ngir dajalewaat i ñoñam. Digal na leen ñu taxaw temm ci njaayum kàrt yi ak dundalaat yëngu-yënguy pàrti bi.

Naka noonu, Pastef gi fare ci kujje gi sóobu na ci tukki nemmeekoom (Nemmeeku Tuur) ci diwaanu Mbuur. Waaye nag, seen ndoorteel des naa neex. Sàndarm yee tas seen ndaje ma bi ñuy wëraan ba tollu Sowaal. Usmaan Sonko nga leen di xamal ni jàpp ko ak dóor ko la yamale, du ko tere benn yoon wéyal wëraanam.

Mimi Turee ngi wéy di yàbbi li mu lancaloon Njiitu réew mi. Delluseeti na ci àtteb njéggal bi ñeel Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll. Dafe jàpp ni baara-yëgoo la diggante Njiitu réew mi Maki Sàll ak waa PDS. 

KOOM-KOOM

Ci ndigalu Njiitu réew mi, jëwriñu koom-koom gi, Mustafaa Ba, teewaloon na Senegaal ci lël bi Banque Mondiale ak FMI  di amal at mu jot. Ginnaaw bi mu leen àggee yóbbante Njiitu réew mi, jot na faa siiwal ak a rafetlu jéego yi Senegaal jot a seqi ak yéene bi njiitu réew mi am ngir wéyal liggéey bi. 

TÀGGAT-YARAM

Sàmpiyonaa Senegaal bu futbal baa ngi soog a tijji. Ginnaaw bi ñu ko dàqee dàqaat ko, bëccëg bu njëkk bee ngi soog dee am ci njeexitalu ayu-bés bi. Amal nañ ci juróom-ñaari joŋante, dugal ci juróom-ñetti bii. Génération Foot a jiitoogum, Dakar SC topp ci. Casa Sport mi jëloon Sàmpiyonaa bi daaw moo nekk ci ñetteelu toogaan bi.

Ci Altiney tey ji lañ doon joxe Ballon d’Or 2022 bi. Doomu Farãs jii di Kariim Bensemaa moo ko mujje jël. Saa-Senegaal bi, Saajo Maane moo ñëw ci ñaareelu toogaan bi. Moom Saajo Maane nag moo jël neexalu Trophée Socrates bi njëkk. Muy lu bees luñ sos ngir ki gën a fës ci ndimbal ak taxawu néew-di-doole yi. Muy itam mbégte lu réy ci moom. Kii di Eduwaar Mendi, jeneen doomu Senegaal, moo jël ñeenteelu toogaan bi ci Trophée Lev Yachine bi ñu jagleel gàrjeŋ yi. 

KAAWTEEF

Jëyya ju réy a am ca Maatam. Jenn waay a soqi bal ci kow soxnaam mu faatu. Loolu nag, mi ngi ko def ginnaaw ba mu séyee 4i at ak soxna si te amuñ doom. Muy lu doy waar te yéeme.

Ca Saly Poortidaal moom, cagatu baa nga mel ni tulli ak maali. Jànq jaa nga fétteeral jëm ñax-ñaxal, góor ña ne leen du ngeen ci wéet. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj