Dépite – Meer bii di Biram Suley Jóob a ngay artooti Njiitu réew mi Maki Sàll :
” Njiitu réew mi, Maki Sàll, siiwal na ca Etaa-Sini nekkam ub lawax, waaye dina xam ni askan wa woon la koy digaale. “
Jamono ji muy wax lii, Paap Mademba Bitéey a ngay yuuxu caa geneen wet ga naa : ” amul kenn ku mën a tere Njiitu réew mi Maki Sàll nekk lawax ci wotey 2024 yi.”
Mbir yi di nirook nappante.
MBIRI AMI NJAAY ÑIBBI
Ci altiney démb ji, 19i fan ci weeru desàmbar 2022, ñaari dépite yu PUR yii di Mamadu Ñaŋ ak Masata Sàmb teew nañ ci kanamu àttekat bi. Cig pàttali, ñoom ñaar nag, seen nawleb dépite bii di Ami Njaay Ñibbi moo leen kalaame woon ginnaaw coow la amoon ca Ngombalaan ga. Mi ngi leen doon jiiñ ni dañ ko dóor ba gaañ ko. Looloo waraloon ba yoon tegoon leen loxo ngir mën leen a àtteek ndaw si.
TÀGGAT-YARAM
Kuppeg àddina si doon daw fale ca Qataar jeex na. Démb ci dibéer ji, 18i fan ci weeru desàmbar 2022, lañ doon amal gañ-jël bi ci diggante Àrsàntin ak Farãs. Ginnaaw joŋante bu neex biñ amal, ñaari ekib yi dañ mujje témboo 3i bii ci 3. Biñ demee ci dóoral-ma-dóor yi la Àrsàntin mujje gàddu ndam li (4-2).
Bii mooy ñetteel bi yoon Àrsàntin di jël kub bu àddina si. Mesi lañ tabb wurekat bi gën a xarañ ci xëccoo bi ; moroomu Saa-Àrsàntin bii di Emiliyaano Maartinees nekk góol bi gën a aay. Saa-Farãs bi, Kiliyaan Mbappe moo jël neexalu wurekat bi ëpp lu mu dugal i bii (8i bii). Lu jiitu gañ-jël bi, Kurwaasi moo jël ñetteelu toogaan bi ginnaaw bi mu dóoree Marog (2i bii ci 1) ci gaawu bi.
XEW-XEWI JAMONO
Caabal gi ëttub cettantal gi siiwal ci ni njiit yi pasar-pasaree Force Covid-19 bi mooy wéy di yéem ñépp. Ginnaaw ayu-bés bi caabal gi génnee ak tey, coow li demul bay waaj a dal. Wile yoon, dépite yee tàmbalee wone seen taxawaay ci mbir mi. Kii di Àbbaas Sàll, dépite YAW ca Ngombalaan ga ma ngay xamle naan :
” Nun waa Ngombalaan gi fas yéenewunu koo bàyyi mu jàll.”
Ci jamono jii nag, jëwriñ yeek Dage (Direction de l’administration générale et de l’équipement) yee ngiy jiiñante ak di tamante dëmm. Ku nekk naan sa moroom ” Ci yow la”.
BITTIM-RÉEW
Ginnaaw ndajem USA-Afrig ma mu doon teewe ca Wasinton, Njiitu réew mi Maki Sàll a ngay wéyal tukkeem ca réewum Sàppõ. Jëwriñ ju mag ja, Kisidaa Fumiyoo, moo ka fay dalal ci diiru juróomi fan (16 ba 20i fan ci waaru desàmbar 2022). Ci seen waxtaan, Njiitu réew ak jëwriñ ji jot nañoo déggoo ci dëgëral lëkkaloo ñaari réew yi ñeel suqaleeku gi, baana-baana gi, demalante bi ak ci kuréli àddina si, rawatina lu jëm ci yeesal ndajem kaaraangeg Mbootaayu Xeet yi.