LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 23 sãwiye 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Bërki-démb ci dibéer ji, waa Pastef doon nañ amal ab mitiŋ ca depàrtamã bu Kër Masaar. Mu doonoon nag ndaje mu réy a réy te bare woon lool i nit. Ñu doon ca fàttaliku tamit seenub militaŋ bii di Mariyaama Saañaa te ñu faatoon ko fa ci anam yu ñaaw. Ràññe nañ fa tamit teewaayu njiiti lëkkatoog YAW yu bare.

Bi Njiitul Pastef lii di Usmaan Sonko jëlee kàddu gi nag, delsi na ci mbir mi dox ci digganteem ak Aji Saar. Ma ngay xamle ni àgg nañ ci foo xam ni tànku ginnaaw amatu fa. Te sax miiraas na boppam ba noppi. Lu mu laaj rekk ñu dem ci ba jeex. Dépite bii di Guy Mari Saañaa teewoon na tamit ngir dooleel doomu ndeyam Usmaan Sonko. Ciy kàddoom, pexey Maki Sàll yépp mooy faagaagal Usmaan Sonko, waaye, ñoom duñ ko seetaan wenn yoon. Te sax layoo moo fi dul am.

TÀGGAT-YARAM

Gaynde Senegaal yu ndaw yi jàll nañ ci ñaareelu wàll wu Chan 2023 biy am fale ca Marog. Ginaaw ñaari ndam yi ñu am ci ñetti joŋantey kippu yi, ñoom ñoo jiitu ci kippu B bi. Koddiwaar lañ dóor (1-0) ci seen joŋante bu njëkk ci xëccoo bi, Ugàndaa dóor leen (1-0) ci ñaareel bi laata ñuy wol RDC (3-1). Looloo tax ba dinañu jàll ci kaar-dë-finaal yi, mu doonoon seen um mébét mu njëkk. Ci seen ub joŋante bii di ñëw nag, gaynde yi dinañu ci dajeek Mali, Móritani walla Àngolaa.

Ca geneen wet ga, gaynde yu jigéen yeet jàll nañu ci dëmi-finaal yu turnuwaa UFOA/A bi xew fale ca Kab-Weer. Dañoo duma duma yu metti Gàmbi (4-1) ci seen ñaareelu joŋante ginnaaw bi ñu njëkkee duma Gine (4-0). Ñoom sax dese nañu benn joŋante bu ñu war a amal ci seen digganteek Siyeraa Lewon ci kippu B.

XEW-XEWI JAMONO

Coowal laksidaŋ yu metti yi fi amoon ci ayu-bés yi weesu ca Sikiloo ak Sàkkal giifagul ba léegi. Jàppal bàyyil gaa ngi mel ni ay ci diggante kilifay Nguur geek kurél yi séq dem beek dikk bi. Bu ñee tëbee tëb jël i ndogal ngir dog jëyya yi, ñi ci des ànduñu ci wenn yoon. Ba tax na ña ngay wéy di bank seen i loxo ci dem beek dikk bi. Kii di Aliw Tin moom gisul laneen lu dul ni jëwriñ Mansuur fay dafa war a tekki ndombal tànkam. Ak li faatu ci ñaari laksidaŋ yi, ngoram waroon na koo may mu joxe lenge yi ngir ormal doom-Aadama.

BITIM-RÉEW

Cong gu metti moo am ca Somali ci dibéer ji. Ay rëtalkat yu bokk ci Shebabs a defati seenub mënin ca péey ba, Mogadisoo, ba juróom-benn nit ñàkk ci seen bakkan. Ay weccoo i sox yu metti jot nañ faa am ca diggante làrme baag way-cong ya. Kilifay dëkk baa ngay xamle ni sax réy nañ juróom-benni nit yi amal cong ma ak di jéem a dalal xelu askan wa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj