Aysata Taal Sàll a ngay dëggal ne Njiitu réew mi Maki Sàll mën naa nekk lawax ci wotey 2024 yi. Moom jëwriñ jiñ dénk wàllu bittim-réew ak Saa-Senegaal yi ci jasporaa bi moo nekkoon ganu Baabakar Faal ci dibéer ji. Bi ko taskatu xibaar bi laajee lu jëm ci ñetteelu moomeg Njiitu réew mi, Maki Sàll, li mu ci tontu mooy ne referàndëm yu 2016 yee féetale woon wax jooju wet. Maanaam, Njiitu réew mee ngi ci moomeem gu njëkk gu 5i at.
MBATIIT
Njiitu réew mi, Maki Sàll, dalal na jabbsekat yii di waa axlu Hip HopGalsen. Démb (dibéer, 26i fan ci weeru desàmbar 2022) ci ngoon gi la doon amal ak ñoom am ndaje. Ñenn ci way-yëngu (acteurs) yi leen fa teewaloon yékkati nañ fay kàddu ngir dégtal ko seen i mébét ak i jafe-jafe. Ginnaaw bi mu leen dégloo nag, Njiitu réew mi jël na ndogalu soppi FDCU (Fonds de Développement des Cultures Urbaines) ngir yokk ci Industries Créatives. Dina yokk it ci atum 2023 mi gafaka gees ko jagleel, jële ko ci 600 000 000 (juróom-benni téeméeri tamndaret) FCFA yóbbu ko ci benn tamñaret ci FCFA.
TÀGGAT-YARAM
Démb ci dibéer ji, làmb amoon na ca Aaren nasiyonaal bu Senegaal. Ñaari mbër yii di Jakson ak Ñaq-Jariñu ñoo fa doon jàkkaarloo ci kombaa bu mag bi. Ñaari yoon la mbër yi sëgg laata jéll di am. Ci seen congoo gu njëkk, dañoo xeex xeex bu metti ba Ñaq-Jariñu dem Ardo. Bi mu delsee la ko Jakson nax, daldi koy daan jéll bu réy.
MBIRUM PAAP AALE ÑAŊ
Biñ ko jàppaatee ba delloo ko ndung-siin, Paap Aale Ñaŋ dafa nekkaatoon dee xiifal ca puqusam. Jamono yii nag, rawalees na taskatu xibaar bi ca raglu bu mag ba ca Ndakaaru. Meetar Musaa Saar mi koy layal a ko siiwal. Ma ngay xamleet ne sonn na lool sax.
XEW-XEWI JAMONO
Senn ndaw su tollu ci 14i at su doon mbindaanu, la ab defkatu ñaawteef bëggoon na sàkku. Looloo nga xewe ca Jannatul Mahwaa (Tuubaa). Bi ndaw si lànkee ba xeex ak moom mu daldi koy jam paaka. Ndaw si nag, dañ ko mujje rawale ca saa sa, ca raglu ba daldi koo oppeere. Waaye, dafa mujje ñàkk bakkanam.