LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 26 Sàttumbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Aminata Ture won na ginnaaw Njiitu réew mi Maki Sàll. Ciy waxam, dara waralu ko lu dul ni dafa àndul ci ñetteelu moome gi njiitu réew mi bëgg. Faf na sax ber làngu boppam ca Péncum ndawi réew ma te fas yéene doon dépite askan wi, waaye itam ngir mucc ci par-parloo gi donte jàppal na tànk njiitu réew mi fu nekk ak ci anam yu nekk, ba ci wote yi weesu.

KOOM-KOOM

Senegaal dina jot 30i milyaar ci waa UEMOA (Union Économique et Monétaire Ouest Africaine) di kurél gi yenu koom gi ak a saytu xaalisu Afrig Soowu-jant. Muy nag xaalis buñ ko abal ngir mu dooleel gafakaam ba mën a sàmmonte ak i wareefam.

FÀTTALIKU SUUXUG GAALU « LE JOOLAA »

26i fan ci weeru Sàttumbar 2002 la saxaar gi Le Joolaa suuxoon ci géeju Gàmbi gi. Fekk mu bawoowoon Ndakaaru jëm Sigicoor. Lu yées tuuti 2000i doom-aadama ñàkkoon nañ ci seen bakkan. 20i at ci ren ginnaaw jëyya jooju, njabooti ña ca faatu woon di ko fàttaliku ak a naqarlu ni ci yoon doxale ba mënul a duut kenn baaraam.

KAAWTÉEF

Libeerte 6, jenn waay a fa doon jote ak soxnam daldi koy xoj ba mu sedd guyy. Yamu ca, moom ak ñaari xaritam baara-yëgoo ngir gëmloo njabootu ndaw si ni dafa daanu ba jële ci faatu. Waaye seen pexe àntuwul. Ña nga mujje ca loxoy pólis.

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj