LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 28 nowàmbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Tusĩ Màngaa, dem na bokki Pastef. Démb (dibéer) la ko xamle. Moom Tusĩ Màngaa nag, bu yàggul dara la tekki ndombal tànkam ca làngug pólitig gii di PDS. Ciy waxam, dara taxu koo fekki Usmaan Sonko ak i ñoñam lu dul xeex bi ñuy xeexal askanu Senegaal, rawatina ndaw ñi. Nee naat dina xar tànku tubeyam ba moom ak ñim bokkal gis-gis ci pólig jublu ci wotey 2024 yi te ànd ceek waa Pastef.

MBATIIT

Talaata (29 Nowàmbar 2022) ak àllarba (30 Nowàmbar 2022) UCAD (Université Cheikh Anta Diop) FKA (Fondation Konrad Adenauer), ASECOD (Association Sénégalaise de Coopération Décentralisée) ak TI (Timbuctu Institute) dinañ amal ci seen lëkkaloo ab lëlu ñaari fan ngir sottantey xalaat ñeel dëkkaale diine yi. Seen yitte mooy wone jote gi ci diggante xàmmeefu nit ki ak i ñoñam (l’identité individuelle et collective), ni diine di doxee ak aada yi bawoo ci mbatiit ngir am déggoo, jàppalante, dal ak jàmm ci biir mboolem-nawle mi.

TÀGGAT-YARAM

Ci altiney tey ji lañ doon tëj ñaareelu bëccëgu kuppeg àddina si ca Qataar. Doon nañ ci amal ñeenti joŋante. Bu njëkk bi, ndam demul, ndam dikkul ci diggante Kamerun ak Serbi (3-3). Ci beneen joŋante bi, Gana dafa dóor Kore ñetti bii ci ñaar (3-2). Ci ñetteelu joŋante bi, Beresil moo dóor Siwis 1 bi ci 0. Portigaal daldi dóor Irigee 2i bii ci 0.

Ëllëg ci talaata ji la ñetteelu bëccëg bi di door. Bu 15i waxtu jotee, Olànd ak Qataar dinañ laale ak itam Ekuwaatëer ak Senegaal. Buñ demee ba 19i waxtu la yeneen ñaari joŋante yi di tàmbali ci diggante Irã ak Etaasini, Peyi dë Gaal ak Àngalteer.

XEW-XEWI JAMONO

Ca Mbuur, duwaanu Senegaal defati na fa liggéey bu réy. Ay pooju ginaar yu yàqu, yu kenn warul a lekk la teg loxo. Ci xayma mi ngi tollook 9000y (juróom-ñeenti juniy) kilo yu ay defkati ñaawteef nammoon a tas ci biir réew mi.

Ca Sali moom, ku nuy wax Céeri Mëñee la waa Dic teg loxo ginnaaw bi ko waa Interpol yoolee. Moom nag, ñaŋ koy tuumal ne dafa reyoon soxnaam ca Farãs, ca atum 2010.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj