LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 29 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Fukki fan ak ñaar ci weeru Sàttumbar lañu war a taxawal tëralinu péncum ndawi réew mi tukke ci wotey palum dépite yii weesu. Ba tey coowal ki war a jiite Pénc mi a ngi jolli. Abdulaay Wàdd ak Usmaan Sonko ñoom feeñal nañu seen tànneef ci Lamin Caam. Fekk Abdul Mbay di dànkaafu Maki Sàll ci mu xoolaat bu baax ki mu war a tànn. Lu ko moy kujje gi dina am ndam.

XODDIKU CA BALA NGAA LAKKALE

Ginnaaw taw yu bare yi wàcc fan yii ci réew mi ba tax beykat yi di dolli sant, Saa-maatam yi ñoom, njàqare la leen dikke. Dexu senegaal gi dafa ci jaare fees dell ak ndox. Lu ko tere rembat ba walangaan bareetul. Ba tax na ña ngay ragal mu jural leen i jëyya yu kenn dul xam fu muy yem.

TÀGGAT-YARAM

Gaynde Senegaal yu futbal yaa ngi jëm ci waajtaayu kub bu àddina si. War nañ amal benn joŋante xaritoo ak ikib bu Boliwi. Ci joŋante boobu nag, kurélu futbal bu Senegaal bi nar na cee def xaalis bu takku. Mën naa dem ba 300i tamndareti FCFA bu ñu sukkandikoo ci kàdduy Ógistĩ Seŋoor mi jiite FSF.

XEW-XEW

Fale ca Pikin jenn waay ju tudd Armaa moo lekk Màndarin ca kër benn xaritam. Li yéeme ci mbir mi mooy yàggul dara mu daldi faatu. Ñuy werante ndax dafa ko posone am déet. Xarit ba nag ma nga yoon téewandi di xaar lu gëstu bi di feeñal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj