LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 31 Oktoobar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Lawax yi jëm ci wotey 2024 yee ngi gën dee yokku. Démb ci dibéer ji la Dr Abdurahmaan Juuf doon siiwal ci turu làngug pólitig Awale ni, dina nekk lawaxam. Fa mu fekk baax nag, ca Cawleen la dajale taskati-xibaar yi ngir yegge leen ko. Teg na ci ne lu mu am lépp Réewu Senegaal mi fay njàngam a ko waral ba tax na foog mu delloo mbàttu ca ndaa la mu naanee.

MBIRUM SWEAT BEAUTY

Alxames jii di ñëw, àttekat bu mag bi dina déglu Usmaan Sonko ci mbiru sweat beauty. Moom, njiital Pastef li nag, ndaw si Aji Saar a ko tuumaaloon ci weeru awril 2021. Dafa ko jiiñoon siif boole ciy tëkku ca béréb ba mu doon liggéeyee te mu daan fa dàmpusi.  

TÀGGAT-YARAM

Senegaal sóobu na ci waajtaay wi ñeel jeux olympiques yiñ jagleel ndaw ñi te mu war koo dalal ci atum 2026. Donte ni des na ñeenti at, Mamadu Jaaña Mbay mi jiite mbir yi taxaw na temm ci waajtaay wi. Mébétam mooy waajal ndaw yi ci mboolem tàggat-yaram yi, te teel a jël matuwaay yi war ngir lépp jaar yoon.

XEW-XEW

Duwaanu Senegaal teg na loxo ñetti téeméeri kiloy sineebar ca kidiraa, ci digu Senegaal ak Maali. Cig sëfaan gu jóge Maali la ko saay-saay yi làqoon. Ci xayma, dina dem ba ci ñaar-fukk ak ñeenti miliyaar ci FCFA. Fekk nañ itam ci dawalkatu sëfaan gi ay kayiti xaalisu FCFA, dolaar, uguyya ak lewoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj