Ngombalaan gaa ngi wéy di natt nafay njëwriñ yi ñeel atum 2023. Njëwriñu dem beek dikk bi ci jàww ji ak suqaleeku jumtukaay yi ci dalu roppalaan yi la dépite yi doon nattal tey ci Altine ji. Jëwriñ ji, Duudu Ka ma fa teewoon nag, dana demaale ci at mi lu tollu ci fukki miliyaar yu toftal ñetti téeméer ak juróom-ñaar-fukk ak juróom-ñaari tamndaret.
YOON
Kilifay àttekat yi dina déglu taskatu xibaar bii di Paap Aale Ñaŋ 10i fan ci weeru desàmbar bii. Mr Musaa Saar mi koy layal a ko xamle. Ci pàttali, taskatu xibaar bi, ña nga koy toppe ni dafa yor te siiwal i xibaar yu laaleek kaaraange réew mi te mën a andiy jiixi-jaaxa ci làrme bi.
Paap Aale Ñaŋ nag dafa sumboon ab xiifal. Loolu tax na ba soxnaam di artu àddina ñeel wér-gi-yaramam. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, xiifal bi néewal na ko doole lool te wér-gi-yaramam tàmbali naa doy waar ba mënatul a dox ak a wax bu baax.
TÀGGAT-YARAM
Senegaal jeexal na ci kuppeg àddina siy am fale ca Qataar. Bi mu génnee ci joŋante kippu yi, Àngalteer mi mu doon dajeel démb ci dibéer ji moo ko dóor ñetti bii ci tus , mu jaar fa toog. Gaynde Senegaal yi yem ci wiccéem dë finaal yi ginnaaw biñ fi gëjee agsi ca atum 2002.
Bi joŋante bi jeexee, Aliw Siise miy tàggat gaynde Senegaal yi doon na jàkkaarlook taskati xibaar yi. Donte ni bëggul wax ci lu jëm ci ëllëgam ci boppu ekib bi, ma ngay sàkku ci ñu dellu ci liggéey bi te waajal Can 2023 bii di ñëw.
XEW-XEWI JAMONO
Xeex bi amoon ci Ngombalaan gee ngay wéy di doon coow ci biir réew mi. Ba fa dépite yii di Masata Sàmb ak Mamadu Ñing dóoree Ami Njaay Ñibbi ba léegi, jàppal fii jàppal fee gaa ngi mel ni ay. Péete gu nekk gis nañ ko ci. Wile yoon, njiital Ngombalaan gee sóobu ci mbir mi. Daldi nay jébbal toppekat bi ab procès-verbal te di sàkku ci moom mu topp ñaari nawleem yi dóore ca Pénc ma. Fim nekk, toppekat bi joxe na ndigal ngir ñu teg loxo ñaari dépite yi, waaye, kenn mënu leen a teg bët fenn.